BÉS DINA ÑËW !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Lu yëngu lu ne, li ko yëngal a ko ëpp doole. Dëgg la, futbal am po rekk la. Wànte mëneesu koo méngale ak yeneen yi. Ndaxte, dafa di po mi nga xamante ne mooy àntule fi yeneen yépp di lajje. Te yit, futbal moo mën a tax aw askan bennoo, doonte ci ab diir bu gàtt la, mooy boole xol yi, dàq xàjj-ak-seen. Fi politiseŋ yeek way-moomeel yi lajjee, pexey sëriñi tarixa yi ak imaam yi sooy fa, futbal a ñëw am fa ndam. Ku weddi lii, seet ko jaloore ji Aliyu Siise ak ndawam yi def ca Misra. Ag ndiiraan goo xam ne lim bu tollu, ci xayma, fukki junniy doomi-réew mi ñoo génnoon ci gaawu bii, teeruji gaynde yi.

Keroog bi ñuy dajeek Alseri, ku nekk janoo ak sa tele, ñoom Saajo Maaneek Idiriisa Gànna Géy jàkkaarloo ak caaxu naar yi, samp seeni dàll ci ñax mu nëtëx mi : nun noo doon ñoom, ñoom ñoo doon nun. Bi àttekat bi walisee ci mbiib bi, senegale bu nekk, ak foo mënti nekk ci àddina si, amoon nga yaakaar ju wóor. Jàppon nga ne ciy waxtu yu néew, gayndey Senegaal yi dinañ gàddu ndam li, indi kub bi Ndakaaru Njaay, nu siyaare ko. Ña fekkewoon finaal ba ñoom Allaaji Juuf ñàkkoon, fukk ak juróom ñaari at mu leen di metti, ñu ngi naan ci seen xel : tey moom du deme noonu. Mbégte mu raw ‘’suba-la-tabaski’’ lanu doon séentu, di waajal soppi réew mi fuural. 

Ndekete yóo…

Dañu ne piriib rekk, naar yi lakk caax yi ! Mbokki Sidaan yi kay, xaaruñu sax joŋante bi sore, daldi dugal benn bal bu ñàkk xorom. Waxtu ak genn wàll wi ci topp yépp, goney Senegaal yee aakimoo bal bi, waaye mënuñoo fexe ba am li ñu doon wut. Bal bu ñu ko jox, Mbay Ñaŋ tulli ko ca kow, yëngal bopp bi. Xale boobu ñi ko jéppi keroog, ndeysaan bari nañu ! Alseriyeŋ yi soppi joŋante bi bëre ak kajjante. Ismayla Saar fu mu dëgge bal, naar yi noggatu ko, dóor ko dàll, mu wañaaru, arbit bi di seetaan. Dëgg la Saajo Maane sunu yaakaar, kenn du wax ne jéemul ; Sabali ni mu ko baaxoo defe, wone na njàmbaar, waaye mujjewul fenn. Kub bi Senegaal da koo teel a ñàkk.

Dëgg-dëgg, gaaf bi topp Senegaal sonal ko : ñaari finaal nga ñàkk leen ci jamono joo xam ne kenn gënu laa xereñ. Waaye loolu terewul askan wi teeru, teral gaynde yi ndax lépp lañu joxe, dem ba jeex. Keroog Yoof, foo sànni mbàttu mu tag.  Xéy-na, gaa ñi dañu jàpp ni fii ak ñaari at kub bi dina ñëw.  Rax-ci-dolli, gone yi màggetaguñu, dese nañu lu bare.  Ci beneen boor, bare na ñi doon ŋàññ Aliyu Siise, di ko duut baaraam naan cuune la. Waaye, ñoom ñépp la tëj seen gémmiñ. Jaloore ji mu fi def, ginnaaw ndem-si-Yàlla ji Bruno Metsu, keneen defu ko fi. Te Nkuwame Nkrumah daan na wax naan : « desee mën warul a tax nun doomi Afrig nu jël sunuy mbir dénk leen Tubaab yi. » Dese mën aayul, su fekkee yaa ngi def sa kemtalaayu kàttan. Boo juumee yit, dina doon ab njàngat ci yow, yee la ba bu ëllëgee, dinga xam fooy teg sa tànk.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj