NISERYAA : BUHARI FALUWAAT NA

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci weeru féewaryee wii jàll la askanu Niseryaa doon amal woteb njiitu réewam. Ba ñu àggee ci cëpaandoo li, Muhammadu Buhari la askan wi tànn, dénkaat ko réew mi. Lu tollu ci 15 alfunniy wotekat ñoo sànnil xob ki toogoon ci jal bi 2015 ba léegi, mu jël raw-gàddu gi ci kanamu lawax bii di Atiku Abubakar.

Chinua Achebe mas naa bind cib téereem bu siiw ci atum 1983 ne liy gàllankoor Niseryaa du lenn lu dul i njiit yu matul i njiit. Jaar-jaaru Buhari firnde la ci ndaxte 36 at ci ginnaaw, laata muy falu ci yoonu demokaraasi, àndoon naak i moroomi soldaaram jiital doole, foqati nguur gi ci loxoy Shehu Shagari. Waaye, àddina sépp benn seede lañu biral ñeel Buhari te moo di ne du sàcc, àndul ak kuy sàcc walla ger te yit, nit ku dëggu la, xamul caaxaan, am fulla ju mat sëkk.

Ba muy kàmpaañ ci atum 2015, la mu gënoon a fésal, ciy digeem, moo doon jàmmaarlook tuurkati deret yii di waa Bokko Haram ak dakkal ger ci Niseryaa. Doonte sax ay yéeneem yépp àntuwuñu ci ñaari fànn yooyu, nit ñi nangul nañu ko ni def na ciy jéego yu am solo.

Waaye, nag, jot naa jànkoonteel i jafe-jafe ba mu faloo ci atum 2015. Ndaxte, njëgu petorol bi nga xam ne moo téye koom-koomu Niseryaa, dafa daanu woon bu baax, daldi nasaxal weccitu réew mi ba noppi yokk fa ndóol. Rax-ci-dolli, mbir yi àggoon na ba ci xéy jafe woon lool ci ñi ëpp ci réew mi, limu ñi amul liggéey daldi ful ñaari yoon.

Te tamit, Buhari mag la, yaram wi neexatul. Waaye, moom de, mel na ni yàkkamtiwul daraam, mi ngiy def li muy def, ànd ceek dal. Looloo waral xaley Niseryaa yi utal kob dàkkantal, di ko woowe Baba-Go-Slow. Gaa, Buhari dafa ñëw fekk ay tolof-tolof yu bari gàll koom-koomu réewam. Teewu ko fexe ba dugal xaalis bu bari ci mbay mi ak jumtukaayi xarala yi. Ger gi mu waxoon ni dina ko xeex tamit, wax-dëgg-Yàlla def na ci kemtalaayu kàttanam. Li dalul xel ciy mbiram, daal, moo di ne Buhari jikkoy soldaar la am ba tey, mënul a tàggook moom : képp ku ko déggalul, du la may jàmm.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj