TAALIFU MAMADU JARA JUUF
Ñów di nas, di nocci
Nërmeel nga boroom doole
Detteel nga boroom alal
Botti nga boroom xam-xam
Yow Koronaa, yaay fas di fecci !
Kenn ràññeetul kenn
Kenn xàmmeetul kenn
Fatt nga gët yi
Muur xar-kanam yi
Tëj wunti kër yi
Yow Koronaa, yaay teg di teggi !
Yaa ñu yeew ci kër yi
Ñuy xool njaboot gi
Yaa not sunuy làmmiñ
Yaa tënk sunuy jéego
Kenn dematul fenn
Yow Koronaa, yaay tapp di teppi !
Ub nga jàkka yi, yow Koronaa
Tëj nga jàngu yi, cey Koronaa
Dakkal nga po mi
Feelu kilifa yi
Wallu ustaas yi
Cey Koronaa, yaay buur di bummi !
Yéem nga Beydaani
Tiiñ nga Soodaani
Mbas nga kàccoor yi
Gal-gal ndaanaan yi
Caxabal saay-saay yi
Cey Koronaa, yaay fal di folli !
Tee ñoo durus say dars
Ndax sunuy jikko aaru
Sunuy Kàddu woddu
Sunu mag ñi fegu
Sunu ndaw yi sàmmu
Cey Koronaa, yaay tabb di tebbi !
Moo Koronaa,
Yow miy lal di làlli
Tee ñoo càqi say cax
Sunu nguur yi maandu
Sunum pénc doxe fi jag !
MAMADU JARA JUUF
Mbaaw, weeru Mee 2020