7i fan ci weeru nowàmbar mooy bés bi ñu jagleel bindukati Afrig yi (saa-Afrig). Ren, ci Alitine jii weesu lees ko doon amal ca Point E, Kër Biraago gu bees, ci njiiteefu jëwriñu mbatiit ju bees jii di Doktoor Aliyu Sow. Maurice Kouakou Bandaman, àmbasadëeru Koddiwaar ca Farãs, lañ baayale woon bés bi, te teewoon na ca. Moom sax, nekkoon na jawriñu mbatit ca réewam. Rax-ci-dolli, bindkat la ; nde bind na lu tollu ci fukki téereek juróom. Wëppa bés bi mooy Ladab ak ma-réew gi (littérature et citoyenneté), réewum Móritani, moo nekkoon gan gu mag gi.
Ci atum 1992 la mbootaayu xeet yi dogal 7 nowàmbar bésu bindkati saa-Afrig yi. Ñoom ñii, ak móolkat yi, ak ñépp ñu seen xam-xam màcc walla ñu yittéwoo téere, dañuy daje, di amal ay waxtaan, di seet ak a càmbar mbind ak dawal. Dinañuy fénc jafe-jafe yi ñuy jànkonteel ak pexe yees mën a lal ngir saafara leen. Dinañuy tànn itam ñenn ci seen biir, sargal leen, joxleen ay raaya. Wii yoon nag, Alasaan Siise, taskatu-xibaar bu ràññeeku lool ci mbatit lañ jagleel raaya biñ duppe Majib Seen, di ci sargal ligéeyam bu am solo ci mbatit. Siise am ci mbégte lool, tudde ko Sëriif Maamun Aydara mu nekkoon sëriñ bu daan yëngu bu baax ci mabatit. Ñaax na tamit ay rakkam ci mécce mi ñuy gën a xareñ te ànd ak pasteef ci xibaar yi ñuy tasaare ndax mbatit mooy dundal am réew.
Jawriñ Aliyu Sow, bi mu yëkkatee kàddu, fésal na mbégteem ci teew bi mu teew ci bés bu ni mel ak raaya bi kurél gi sargalee Njiitu réew mi. Ndaxte, moom Njiitu réew mi, day jàppalee bindkat yi, te ku jox cër xeltukat yi la. Ci kow loolu, jawriñ ji yëgle na ni, ndimbal gi kurélu bindkat daan jot, muy 15i tamndaret ci sunuy koppar, yokk nañ ko ba 30i tamndaret. Naka noonu yit, PEN 2i tamndaretam dina dem ci 10i tamndaret. Ñi fi jot i raaya tey, ku ci nekk yokkal nañ la ci sa àmbolog téeméeri junni. Muy lu ñépp rafetlu. Gërëm na Aliyun Badara Béey mi jiite kurél gi, ak kolonel Mumar Géy ci taxawaayam ci kaaraange réew mi, ak it Abdulaay Elimaan Kan mi ko jiitu woon ci njawriñu mbatit gi, te def fa liggéey bu am solo.
Bés bi nag gànjaru woon na lool. Nit ña bari nañu, te ràññeeku. Daje yi am nañ solo waaye bu nu fàtte jafe-jafey këru móolukaay yi, ak it ñiy bind tey lott ci gis ku leen génneel. Di daaneele kàdduy Nelson Mandelaa ba mu naan « askan wuy dawal (téere) day raw », muy li góor ga daa wax « téere day tee réer ».
Dellusi di ndokkeelaat Bubakar Bóris Jóob ci raaya Neutstadt 2022 ca Amerig.