Démb, alxames 9eelu fanu sãwiyee 2025, la Njawriñu njàng mi doon màggal, fa Jamñaajo, bésub njàngum xale yu jigéen ñi ci teewaayu Mari Xon Fay (Soxnas Njiitu Réewum Senegaal).
Waa lekool Mariyraama Ba ñoo ubbi ndaje mi ak bàkku Senegaal, mbuubum làrme mi gunge leen ci.
Ba ñu noppee, Soxna Umi Nduur, moom mi doon séddale kàddu gi, daldi fàttali ne, wëppa 2024 wa nekkoon “Gis-gisu jigéen ñi ngir ëllëg”. Ñu jóge fa, eggali ak wëppaw ren jii di : “Senegaal dogu na ci njàngum jigéen ñi”.
Soxna Mari Siibi Fay moo dalal gan yi, yëglewaale xew-xew yi ñu dëgmal jamono yii di ñëw ñeel njàngum jigéen ñi. Fukk ak benni réewi Afrig ñoo ci lëkkaloo. Waaye, ca ndorteel la Senegaal ak Koddiwaar bokkuñu ci woon, dañoo dabusi. Soxna si woote na ndogu ci njàngu jigéen ñi, ñu dugg ekool te wéyal seen njàng. Jigéen ju jàng day jëmale kanam koom-koom.
Am na ay jëwriñ yu teewoon niki Soxna Xadi Jéen Gay mees dénk fànni Mbatiit, Ndaw ñi ak Tàggat-yaram. Soxnas ilimaanu jëwriñ yi tamit a nga fa woon.
Am na ay àmbaasadëer yu bokk ci bés beek doole, muy ñoomin Astu Ba (ndeyu daara fi Ndakaaru), Anta Mbàkke (njiitu daara fa Tuubaa), Faatu Sow Kan, (njiitu Expresso), Kura Seen (Wave), Rajaa Juuri Si (njiitu Special Olympique, di toppatoo ñi seen xel matadi, di ko jaarale ci tàggat-yaram), Ami Saar Faal, Aminata Ñaan, Ayda Mbóoj, Njooro Njaay ak Awa Mari Kóol Sekk ak Aminata Ture (Mimi) mi yor seen kàddu. Moom, Mimi Ture mi fa teewal it Njiitu Réew mi nee na :
“Bu nu jàngul woon, dunu kon taxaw fii tey…Waaye nag, njàngum jigéen ñi am nay jafe-jafe ba nëgëni. Maak sama mbokki jigéeni àmbaasadëer yii, noo dogu ci njàngum jigéen ñi nga xam ne ñooy genn-wàllu askan wi. Fas nanu yéene jàpp ci seen njàng bu baax… ñoom ñiy jiitu naka-jekk saa su ne.”
Xadi Puy, woykat bu lafañ te xareñ lool, desul ginnaaw. Mi ngi yëkkati woy wim tudde Wone ma di ci xamle ak a fàttali ne dundu way-laago daa metti, ndax jàppeewuñu leen ay doom-aadama. Nga jur sa doom mu laago nga koy yalwaanloo, ak di ko nëbb. Moom nag, woy na yaayam ndax ndey ju baax la, ju ko yiir, jàppale ko. Moom tamit Xadi Puy nee na, daaw maye na ci ekooli Tëngéej yi 15 000iy téere ngir jàpp ci njàng mi. li mu ko dugge mooy dimbali njàngaan yi, ñu mën a jot ci wërsëg bob, moom jotu ci woon ba mu ca tollee, ba tax ko dakkal njàngam.
Amon na ñeneen ñu doon xumbal bés bi ñu deme kurél giñ duppee L’espoir de la banlieue ñu dawal ne « Ëllëg, ëllëgu ñi koy waajal tey la ». Bi ñu noppee, la Jacques Boyer mi fa teewaloon UNICEF xamle na ni wëppa ren ji, ñor na ko lool. Mi ngi sàkku :
“[…] ñépp liggéey ngir ekool yi doon béréb yu ànd ak kaaraange, yu amul i taafaar ndax, lu ko moy, sunuy jéego neen. Maa ngi naqarlu faatug Jaari Sow, 12i rekk, xale bu ndaw, dee gi warul a neen. Def ci jigéen ñi mooy def ci ëllëg.”
Waxtaanu xale yu jigéen ñi ñu waxal seen bopp jamono ju am a am solo la ci bés bi. Ndey Abi Sow Ndóoy (Liise Rifisk) moo doon séddale kàddu ngir di leen laaj. Lii lañu tontu :
Penda Ba (Daaray Séydinaa Mohamet), moom mi ngi sàkku ñu bàyyi xel bu baax daara yi ndax ñu mën a wéyal seen um njàng, jëfandikoo seen xam-xam. Su sañoon it daara yi am i róbine. Ndaxte, ba tay, ndox jafe-jafe la, yenn daara yi ndoxum teen lañuy jëfandikoo.
Faatumata Sàll (ekool Pikin Est), ndongo lu sëgg la, wax na yenn ci seen iy jafe-jafe, muy ñàkk a mën a demal sa bopp. Tabax yi tamit kenn sóoraalewu leen. Ci njàng mi, su ñu yaataloon « braille » bi dina gën a baax. Bëgg nañu ñu tolloole leen ak seen moroom yi laagowul.
Awa Kan Faal, (CEM Kennedy), waxal na ndongo yu jigéen ñi, wax na li ñiy yëg ak a daj jamonoy mbaax. Fàttali na ne, limu jigéen ñiy bàyyi jàng dafa yokk ndax jafe-jafe yu deme ni jamonoy mbaax ndongo yu jigéen ñi dañuy ñàkk waxtu yu bari yoy, waroon nañu cee teew ekool te duñu ko mën. Loolu day yokk lajj bi ci jigéen ñi. Taafar tamit (di jëmm, di awra) dina yàq njàngum jigéen ñi. Awa Kan Faal doon ñaan ñu gën a bàyyi xel ndongo yu jigéen ñi nga xam ni dañoo bëgg xarala. Waaye, yenn saay, mboolaay mi ñoo leen iy féetale ginnaaw, mel ni góor ñee gën a xareñ, te demewul noonu. Su sañoon tamit li yoon tëral ñeel séy ak wann-lor (ci xale yi) ak sàkku ci doole ñu jëfee ko ; jàppale ndongo yi seen waajur néew doole, wone it royukaay yu jigéen ñi ci Senegaal.
Ndongo yu jigéen ñi séqoon waxtaan wi xareñ nañu, xam li ñu bëgg, bëgg rekk ku leen bàyyi xel, ñoom ak seen iy ñoñ.
Woykat bi xew ci jamono, Amadewus, woy na fa. Ñu tàccu kook doole mook mbëru Pikin mi, Ëmma Seen.
Ni ko Bubakar Bóris Jóob di waxe ci téereem bim tuddee Bàmmeelu Kocc Barma, “réewum Senegaal soxlawul jéggaan i maam”,
Lamaan Mbay, mi jiite jokkoog njawriñu njàng mi fàttali ne fii ci Senegaal “am nanu ay royukaay, rawatina ci jigéen ñi.”
Xaatimu Kurukaŋ Fuga, ca atum 1236, wax na ni jigéen daa war a bokk ci liy doxal mboolaay. Lim na it Jigéeni Ndeer ya ak Alin Sitooye Jaata ak Faatumata Asta Kan mi njëkk a jiite jàngune Xaali Amar Faal ak ñoom seen. Waaye, ca atum 1695, bi buur Lat-Sukkaabe Ngóone Jéey feebaree, fekk Naari Taraasaa ya war leen a song, Lamaan Mbay waxaat na jaloore, Ngoone Latiir, doomu buur ji soloon yëre ak dàlli baayam, soppi bàkku fas wi, jël ngànnaay yi, dem jiite xareb Ngàngaraŋ, jël ndam li. Foofu da doon firndeel ne góor baax na, jigéen baax na. Te, Séex Anta Jóob ni woon « Li amal solo dëgg aw askan mooy mu daj buum gi koy lëkkaleek démbam fa mu gën a soree… », looloo fi nekk.
Bees sukkandikoo ci kàddu yi Mustafaa Màmba Giraasi yëkkati, “jub, jubal, jubbanti” mooy fexe ba ekool fees ak i jigéen na muy feesee ak i góor. Rax-ci-dolli, njàng day tax a tolloo ak doxal yoon. Jigéen ñi laago it dinañu fexe ñu wéyal seen um njàng ci anam yu mucc ayib. Li jëwriñu njàng mi bëgg mooy :
“Nu tabax te bañ a yàkkamti. Ndax, kuy tabax am réew, su say gët jéllee xale, dangay yàkkamti te su boobaa dangay yàq te dangay yàqal askan wi. Nu fexe baaxe xale yi ci sunu jot. Te, ku xool fi la ekool eggale, dinga gis ni war nga jàppale ekool. Njiitu réew mi ak Nguur gi mënuñu lépp kon fàww ñépp jàpp ci. Gisuma fenn ci àddina sii réew mu sàgganee ekoolam ba noppi daldi suqaliku. Amul, kon na ku nekk dogu ci liggéeyal ekool ngir Senegaal naat.”
Mari Xoon Fay ci wàllu boppam dogu na ci fu jigéen mën a juddoo ci Senegaal ak fu mu mën a soqeekoo, mu mën a jàng, muy ekoolu tubaab mbaa daara. Ndax jigéen su jàngee day xareñ waaye day wóolu boppam.
“Man mii ñu ndeyale bés bi, maa ngi woo ñépp ngir nu fexe xale yu jigéen ñi jàng te yàgg ci ekool yi. Rax-ci-dolli, njàng dafay àq ju Ndeyu àtte bi nangu. Jëwriñu Njàng mi, dogu na ngir jigéen ñépp dugg ekool, di dund ak tawféex ci kéew mu wóor te deesu ci beddi kenn.”
Kàddu yii ñoo tëj ndaje mi, ay weti 2i waxtook genn-wàll ci njolloor.