As góor su tollu ci 25i at, daan dawal móto jakartaa, lees fekk neewam ca yoonu Cees ak Morolã. Moom, ci turu Aliw Jàllo la doon wuyoo. Xamlees na ni mu ngi dëkke fa Caali, bokk ci bokk-moomeelu bëj-gànnaaru Cees (commune de Thiès-Nord).
Waxees na ni dafa réeroon ; lu tollu ci ayu-bés kenn gisu ko. Yëgaleesoon na ko kilifa yi dëkke foofu. Ci kow loolu, waa sàppër yeek sàndarma yi ñépp gaawantu wutali fa.
Ba ñu gisee néew bi, fekk nañu neexatul woon xool ndax ni yaram wi tàmbalee woon na soppeeku. Loolu waral kenn toxalu ko, mujjees ko suul foofu ca barab ba.
Li waral deewam gi nag, ba nii dafa lënt. Xameesagul lu ko ray. Waaye, Ci li yéenekaay xamle sax, dañ ko rendi.
Mótoom bi it kenn gisu ko. Ba tax ñenn ciy jegeñaaleem njort ni xëyna ay sàmbaabóoy a ko dab, faagaagal ko, yóbbu jakarta bi daan dawal.
Sàndarmari ubbinab luññutu ci loolu ngir jéem a leeral réerug Aliw Jàllo geek dee bi.