Jamono jii, këru tasukaayu xibaar yu bari ñoo ngi ci guuta. Ndaxte, dañu ame ay jafe-jafey koppar yu takku. Loolu, dara waralu ko lu moy borub galag bi ñu ameel réew mi.
Laata Maki Sàll di fi jóge, dalaloon na njaatigey taskati xibaar yi fa njénde la (pale ba). Ca seen njeexitalu ndaje ma, daf leen digoon ne dina leen faral borub 40i miliyaar bi ñu ameel réew mi. Waaye, Maki Sàll mujjul sàmmonte ak kàddoom. Dafa di sax, am Njiitu réew, muy Maki Sàll di Basiiru Jomaay Fay, kenn amu ci màqaama baale ab bor boo xam ne, askan wi lees ko ameel. Moo tax, fan yii, waa “Impôts et domaines” takkal pot këri tasukaayi xibaar yi ngir ñu Fay bor bi, ñuy jooytook a dee-deelu.
Bees sukkandikoo ci Mammadu Ibra Kan mi jiite bindkat yeek ñiy fésal xibaar yi, këri tasukaayi xibaar yu bari tëj nañu seen i sàq (comptes). Li ko sabab, ciy waxam, mooy koppari galag yi ñu fayul. Kii di Majambal Jaañ sax, sàqam yépp lañ tëj, jël ci 91i miliyoŋ ci sunuy koppar.
Ngir wut pexe nag, ñi jiite këri tasukaayi xibaar yi jàpp nañum daje, ci àllarbay ëllëg ji, 5 suwe 2024.