CÀMM GI ÀDDU NA CI COOWAL ONAS LI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mustafaa Njekk Saare mi yore kàddu Càmm gi àddu na ci coowal Onas li lëmbe dëkk bi. Muy xamle ni, gisul lu fi jar a coowaloo. Nde, kilifa yi ñoo ci des. Waaye itam, amul lenn lees war a laaj walla di ko wax Jëwriñ ji Séex Tiijaan Jéey.

Li coowal Onas li di bari bari, Càmm gi yéyagu ci woon yàbbi. Wax jee ngi yemoon ci diggante Séex Jeŋ mi jiite woon kër ga ak ndawi jëwriñ ja fa nekk léegi. Mustafaa Njekk Saare mi yore kàddu Càmm gi mooy ku ci njëkk a àddu, ginnaaw bi ko sunuy naataango yu RFM dékkee seen ngolliir (mikóro).

Naka noonu, muy xamle ni amul lenn lees war a coowaloo ci mbir moomu. Xamle naat ni jaadu na Séex Jeŋ génn wax, andi ay leeral. Nde, àq ak yelleef bu ko Yoon may la. Noonoot la Onas amee àq ak yelleef boobu ngir andiy leeral, jaare ko ciy njiitam. Looloo tax ba mu gis ni warul a jur coow lu ni mel ndax, ginnaaw ba ñaari wàll yépp wax nañu, kilifa yee ci des ngir àtte leen.

Bu dee lu jëm ci jëwriñ ji Séex Tiijaan Jéey itam, sànni na ciy kàddu. Waaye daf koo ragg. Nde, ci gis-gisam, amul lenn lees war a laaj jëwriñ ji, ndaxte laalewul dara ak mbir mi. Dafa di sax, ki amoon doxalin bu dëng ci gis-gisub kilifa yi ba ñu dàq ko lañ war a wax. Waaye jëwriñ ji yoonam nekku ci.

Cig pàttali, Séex Jeŋ dafa ko joxoñoon baaraamu tuuma ci joxe liggéey ci yaa-ma-neex ba mu àgg sax ci ñuy laam-laame ni dafa war a tekki ndomb-tànkam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj