NGIRTEY JOŊANTEY DÉMB YI
Démb ci àllarba ji moo nekkoon bés bu mujju ci 1eelu sumbu CAN 2024 bi. Ekibi kippug E ak yu F YI doon ko tëj. Nii la joŋante yi deme :
Kippug E : Ay timboo kepp !
Cii gii kippu, Namibi moo ci doon daje ak Mali, Afrig dii Sidd ak Tinisi ba 17i waxtu jotee. Ñaari joŋante yépp ci 0-0 lañu jeexee. Ndam demul, ndam dikkul.
Malee fa jël pée ak 5i poñ, Afrid dii Sidd topp ci ak 4i poñ, toppu ci Namibi moom itam am 4i poñ. Waaye, ñu raw ko ciy bii. Tinisi moo fay ndaare ak 2i poñ.
Kippug F : Marog dugalaat na Koddiwaar ci kàrt gi
Ba 20i waxtu jotee la kippug F gi doon tëj moom itam ay joŋanteem. Ñu doxoon ci diggante Tansani-Bokkeefu Demokaraatig bu Kóngoo (BDK) ak Sàmbi-Marog.
Tansani dafa timboo ak BKD ci 0-0. Ca wet ga, Marog daldi dóor Sàmbi 1-0. Ndaman loolu nag, dafa suruxal Sàmbi, xettali aji-dalal ji, Koddiwaar. Loolu lees di wax wërsëg dëgg. Fakkastalu ba ñépp ne daanu na, loxo jàpp sa yére, xëccaat la. Loolu doon mbégte ci soppey ñay yi.
ÑETTEEL YI GÉNN
Juróom-benni ñetteel ñoo amoon ca kippu ya, ñu jël ca 4i yi raw, bàyyi ñaar ya. Nii la seen toogaay demee :
ÑEENTI ÑETTEEL YI RAW |
||
1 |
Gine Konaakiri |
4i poñ |
2 |
Namibi |
4i poñ |
3 |
Móritani |
3i poñ |
4 |
Koddiwaar |
3i poñ |
5 |
GANA |
2i poñ |
6 |
Sàmbi |
2i poñ |