Conseil des diffuseurs et éditeurs de presse du Sénégal (CDEPS) dafa doon amal, tay ci àllarba ji, ndajem saabal ñeel tolluwaayu saabalukaay yi ci wàllu koom. Njaatigey saabalkat yi ak ñiy yëngu ci xaralay saabal yi ñoo ko doon amal.
Ñoñi Mamadu Ibra Kan yi ak Maymuna Nduur Fay biral nañ ag càkkuteef ci Njiitu réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar Fay.
“Noo ngi sàkku ci Njiitu réew mi mu yeesal waxtaan wi ak saabalkat yoy, am nañu cër ci yokkuteg Senegaal mi ci wàllu koom-koom ak mboolaay mi.” (kàdduy Mamadu Ibra Kan, njiitul CDEPS)
Moom, Mamadu Ibra Kan, xamle na ne saabalukaay yi, dale ko jamonoy mbasum Covid-19 ba, ba léegi, dañu nekk ciy tolof-tolof. Te, bu ñu ci jógul, dina am ay saabalukay yu tëj. Bu boobaa nag, ba tay ciy waxam, ay téeméeri-téeméeri nit dinañu ci ñàkke seen i liggéey.
Njiitul CDEPS li daldi nay rëccu fukki weer yi fi Njiitu réew mi defagum. Ndaxte, ci gis-gisam, ci biir fukki weer yooyii, daf ci jël ndogal yu doy waar jëmale leen ci saabalukaay yi, di ay ndogal yu “jaaduwul”.