CEDEAO AK ËTTUB ÀTTE BU MAG BI GÀNTAL NAÑ SONKO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ëttu àtte bu CEDEAO gàntal na Usmaan Sonko, jox dëgg Càmmug Senegaal. tey la àttekati CEDEAO doon àtte layoob Usmaan Sonko ak Càmmug Senegaal. Cig pàttali, layookati Usaan Sonko yi ñoo kalaameji woon àttekati CEDEAO yi ñeel tasug làngu pólitigu PASTEF, lees seppi Usmaan Sonko ci wayndarew wote yi, añs.

Ci àjjumay tey jii, ci yoor-yoor bi, la biral ndogalam. Bu dee wàllu tas bi ñu tas PASTEF, xamle na ne Càmm gee am dëgg. Li ëttub CEDEAO bi laltaayoo mooy ne Càmmug Senegaal mësul a salfaañe àq ak yelleefi Usmaan Sonko.

Bu dee lees seppi njiitul PASTEF li ci wayndarew wote yi, CEDEAO nee na du ci àddu, bàyyi na ko ci loxoy ëttu àttewaay bu mag bu Senegaal. Ñoom, waa ëttu àttewaay bu mag bi, ci ngoonug tey ji lañ siiwal seen ndogal ñoom itam.

Xel yeek xol yépp ñoo nga jublu woon ca màkkaanu Sire Aali Ba mi jiite ëttub àttewaay bu mag bi. Ginnaaw bi layookati Càmm gi ak yoy Usmaan Sonko làyyee ba jeexal, Sire Aali Ba dafa ajandi woon layoo bi ngir àtte ko ci ngoon gi. Bi fukk ak juróom-benni waxtu tegalee fanweeri simili la xibaar bi jib ne, Sire Aali Ba dëggal na Sabasi Fay mi joxoon dëgg Usmaan Sonko. Ndekete yoo, ay naxaate la.

Sire Aali Ba dafa neenal àtteb Sabasi Fay bi, wax ne Sonko Ndakaaru la dëkk, kon foofu lees ko war a àttee. Ciy waxam, Sabasi Fay amul màqaama di jël ndogal naan kii, mbaa kee day bokk ci wayndarew wote yi am déet. Noonu la neenalee àtteem bi, delloo yëf yi ca ëttub àttewaay bu Ndakaaru. Waaye nag, jàppuñu ag àpp.

Ci tënk daal, bees CEDEAO ak Sire Aali Ba Càmm gi lañ àndal.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj