CEDEAO TEGGI NA DAAN YI MU TEGOON NISEER

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb ci gaawu gi la way-bokki kurél gi boole réewi Afrig sowu-jant yi ci wàllu koom daje woon fa Abujaa. La gën a fés ca la tukkee ca ndaje mooma mooy ndogal yi ñu jël ñeel réewum Niseer. Ndax, kenn umpalewul ne weeru sulet atum 2023 ba tey seen diggante rattaxul. Te, lenn waralu ko lu moy Nguuru Muhammed Basum gi ñu daaneel ba noppi, ne ko ràpp tëj. Boobaak léegi nag, CEDEAO def na lu ne. Xupp na leen ne day dal seen kow, daan na leen ci wàllu koom-koom ak yu ni mel, waaye dara.  Mu ne léegi, day teggi daan yi mu leen tegoon. Booba, fekk na Niseer ak i ñoñam yim bokkal AES, Mali ak Burkinaa Faaso, génn ci CEDEAO.

Cig pàttali, weeru sulet la Seneraal Abdurahmaan Ciyaani daaneloon Nguuru Muhammed Basum. Fa la coow lépp doore. Ndax, bi mbir mi amee rekk la waa CEDEAO takku jóg ne ko du ci dal, sant ko mu dellool Nguur gi ca na mu gën a gaawe. Te, mu bàyyi Basum ak soxnaam ñu dellu ci seen i yitte. Sóobare yi ne leen defuñu lu mel noonu, taxaw temm fas yéene jàmmaarlook CEDEAO. Waa CEDEAO ne leen kon waaj leen, dinañu dal seen kow, foqarti Nguur. Am réew yu ci mel ni Mali ak Burkinaa Faaso ne leen bu ngeen dalee ci kowam rekk, ñu dal seen kow. Coow la ne kurr, njàqare ju réy am ci njaboot yiy yeewoo ci réew yooyu ak li leen wër. Bi ñu xamee ne loolu moom musiba rekk la nar a jur, ci la ñoom waa CEDEAO mujjee dellu ginnaaw.

Bi loolu weesoo, dafa am yeneen yu fi xewaat diggante CEDEAO ak réew yiy jàppalanteek Niseer. Ndax, ñoom ñetti réew yooyu dañoo sos seen kurélug bopp, dippe ko “Alliance des Etats du Sahel” (AES). Te, li ci gën a doyati waar mooy kurél googu ay sóobare kesee ko séq. Maanaam, ñoom ñépp dañoo daaneel Njiit ya soog a falu. Rax-ci-dolli, ñoom ñépp kenn du ci séq ub taal ak waa Farãs. Te, yemuñu foofu kese. Ci weeru sãwiye wii ñu génn lañu xamal waa CEDEAO ne ñoom bokkatuñu ci seen kurél googu. Mu nekkoon ndogal loo xam ne neexul dara waa CEDEAO. Ñu yokkal leen ca ne ñi ngi ci tànki defar xaalis boo xam ne, ñoom ñétti réew yooyu ñoo koy bokk. Maanaam, ngir firndeel ne ñoom génn nañu ci mbuumu njaam gi donte ne sax loolu mën na am ay njeexital ci wàllum koom gi ñeel ñépp. Ci gàttal, ñoom ñépp a ci nar a sonn bu fekkee namm nañoo wéyal seen i jokkalante.

Mu mel ni, waa CEDEAO xam nañu ne gaa ñi caaxaanuñu. Moo tax, ñoom ñi nga xam ne dalu réewi Afrig sowu-jant yi ñor na leen lool, rawatina jamono jii, ñu tàmbalee yolomal seen loxo. Ndax, ñépp teg nañu seen bët ci daan yu metti yi kurél googu di teg réew yi yenn sóobare yi jiite. Ba tax, ñu jël ndogalu teggi daan yu metti yi ñu tegoon réewum Niseer. Muy lu ci mel ni ubbiteg dig yi ak jàww ji. Maanaam, muy fafalnaaw, di roppalaan, ñépp mën nañoo dooraat seen dem ak dikk ci seen jàww yi ñu bokk. Ak dooraat jokkalante koppar seen diggante ak réewi CEDEAO yi. Terewul ne am na ay daan yu des. Waaye, yooyu mën nañu bañ a laaxaale askan wa.

Kon, xeex bi dox diggante sóobare yi ak CEDEAO du tey la door. Ña jiitu woon Seneraal Abdurahmaan Ciyaani sax jaar nañu ci. Moo tax, ñoom tamit ñu sos seen ug kurél ngir mën a dékku li leen kurél giy teg. Dafa di, kuy tëru moom kuy teggee ca aay. Li mat a laaj kay mooy ndax, seen ndogal yii ñu jël dina tax gaa ñi teggi seen tànk fa ñu ko tegoon am déet.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj