ÀTTEB CONGUG "CHARLIE HEBDO" CA PARI (AMI MBENG)

Yeneen i xët

Aji bind ji

Yéenekaay bii di “Charlie Hebdo” ca Farãs génnewaat na, ci talaatay démb ji, ñaawtéef yi mu tegoon ci kow Yonent Yàlla Muhamad. Cig fàttali, looloo taxoon ay jiyaadis mer, song kërug yéenekaay bile, rey fa 12i nit ci 7eelu fanu saŋwiyee 2015. Ci àllarba jii (1 sàttumbar 2020) la ñu war a door àtte bi ñeel ndaw yees jàppoon ba tuumaal leen ci mbir mi. Njiitu Charlie Hebdo, ñu koy wax Riss, nee na ñoom amuñu dara lu ñuy réccu, kenn mënu leen a xoqtal te képp ku yaakaar ne dinañ dellu ginnaaw nax nga sa bopp.

 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj