CNRA ÀPPAL NA SAABALUKAAY YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bërki-démb, ci altine ji la banqaas bii di CNRA (Conseil National de Régulation de l’Audiovisuelk) génnee ab yégle. Li mu ko duggee du lenn lu moy dëggal kàdduy jëwriñ jii di Àlliyun Sàll, nga xam ne moom lañu dénk wàllu jokkoo gi. Rax-ci-dolli, xamal na saabalukaay yi ne, la woon wonni na. Maanaam, na këri tasukaayi-xibaar yépp tënku ci sàrt bi Yoon tëral ñeel leen yi balaa muy yàgg dara.

Coow li dox ci diggante Nguur gu yees gi ak saabalukaay yi du lu bees. Mënees na ne, fii la ko Nguur gi fekk mbir mi wund coow li. Nde, dafa am boru lempo bu kër yooyu yore te, Nguur gi fasu koo yéenee baale. Looloo jur coow jamono jii seen diggante. Ba talaata jee weesu, yemoo woon ak fukki fan ak ñett ci weeru ut, la yenn ci saabalukaay yi amaloon ab bésub dakkal seen liggéey, bañ a siiwal i xibaar. Ginnaaw gi, Njiitu réew mi xamle na ne dina amal aw waxtaan ak kilifay këri tasukaayi-xibaar yi.

Bi loolu weesoo, jëwriñ jii di Àlliyun Sàll nga xam ne moom lañu dénk wàll woowu, génn na, indi ay leeral yu bari. Muy ci bor yi di ci doxalin wi boole ko ak siiwal ndimbal yi ñu jox saabalukaay yi at yii weesu. Xeetu doxalin woowu nag, donte ne sax, am na ñu ko rafetlu, terewul ne am na ñu koy ñaawlu. Waaye, banqaas bii di CNRA dafa ñëw yokk ci xar mi karaw.

Dafa di, ñoom dañu ne, may nañu mbooleem saabalukaay yi, muy yi ñuy déglu ak yi ñu seetaan, àppu fanweeri fan ngir ñu tënku ci dogub 94 bu sàrtu n°2017-27 bu 13 sulet 2017 nga xam ne moo tënk doxalinu saabalukaay yi. Ba tey, ci seen yégle bi, xamle nañu ci ne, ndogal biy tax nga mën a doxal sa liggéey, fa njëwriñ jooju rekk nga ko mën a ame. Li ñu ko dugge du lenn lu moy jël mbir yépp tegaat leen ci yoon. Su ko defee, bépp xeetu saabalukaay mën a wéyal liggéeyam na mu ware. Lu ko moy Yoon dina dal seen kow.

Mu mel ni kon, coow li xam nañu fi mu doore, waaye, fa muy mujj moo jaaxal ñu bari. Li mat a laaj kay mooy, ndax Nguur gi dina teggi tànkam fi mu ko teg ? Walla, ndax saabalukaay yi dañuy mujj def li leen Nguur gi di sant ?

Ak lu ci mën di am, ku dund rekk, danga fekke.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj