CONCU BU DIIS BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Wolof nee na : “concu, boroom rekk a ko àttan”. Kon, ndax jaadu na ci moom mu teg nu bosam ? Nga ne : “Moom man ?”, nu feelu la : “Teewlul tuuti rekk”.

Mu teg concam ci sunu kaw ba noppi wax nu ko ci kàddu yu leer nàññ. Nun ñépp nu dégg ko te teewul nu ne nemm !

Waxleen rekk, kan ci yéen moo ko déggul mu ne am na ay wayndare (yu ñu waroon a jébbal Yoon) yoy, moo ci teg concam ?

Léegi xam nga ki nu doon junj ? Du kenn kudul ki Saa-Senegaal yépp jiital, jébbal ko lépp ne ko “sàmmal ñu ko !”.

Lan la waxam jiy tekki lu moy :

“Am na ñu ñu tuumaal ci luubal ak jalgati, waaye man maa leen làq ci sama ginnaaw” ? 

Muy kàddu yu dor waar te bari lool nees ko mën a déggee. Waaye, balaa nuy wéyal, nanu leeral ñaari mbir.

Bi ci njëkk mooy réewum Senegaal dafa samp ay kurél yu am seen jonnug bopp te war a saytu ak a càmbar liggéeyu ñi ñu dénk moomeelu njémmeer li.

Bokk na ci kuréel yooyu, Ëttub càmbar Gafay Réew mi (“Cours des comptes”) bi ñu sàmp ci atum 1999.

Li ko jiitu, Ëttu àttekaay bi gën a kawe (“Cour suprême”) moo fi nekkoon ci atum 1960 di liggéey ci lu bari, boolewaale ci càmbar gafay Réew mi. Ay coppite yu ñu amaloon ci 1992 ñoo ko fi jële, def ko ñetti pàcc : Kurél giy saytu Ndayu Àtte ji (“Conseil constitutionnel”), Ëttu àttekaay bu mag bi (“Cour de cassation”) ak Kurél giy xelal Nguur gi (“Conseil d’État”). Kurél gu mujj googu moo wéyal di saytu Gafay Réew mi ba ci atum 1999 mi Ëttub càmbar Gafay Réew mi juddoo.

Nu fàttali rekk ne, ci atum 2008 la Ëttu àttekaay bu mag bi ak Kurél giy xelal Nguur gi booloowaat ngir sàmpaat Ëttu àttekaay bi gën a kawe.

Ñaareelu ponk bi mooy ca Ëttub càmbar Gafay Réew mi, ay àttekat ñoo fa nekk, waaye amuñu sañ-sañu àtte. Dañuy luññutu, bu ñu gisee lu jaaduwul ñu laaj ki mu soxal ngir mu indiy tontu ak i leeral ci li ñu gis. Bu firnde yi leeree, baax na, bu leerul ñu ñaan Yoon mu def li ko war. 

Am na nu muy demee sax, dañuy dankaafu rekk wax ki mbir yi soxal walla kilifaam mu gën a jekkal taxawaayam tey bàyyi xel ci ni mbir yi war a doxee. Kon nu gis ne Ëtt bi jiiñul kenn ! Dafay gis lu lëndëm, mu wax Yoon mu leerel ko.

Bu nu dellusee ci lu jëm ci li Ëttub càmbar Gafay Réew mi siiwal nag, te ñépp di ko coow ci jamono jii, lu ci waay wax rekk am na lu mu bàyyi. Te, dafay mel ne yu mel nii yàgg nañoo xew ci réew mi. Waaye nag, bii da cee raw. Walla boog, nu ne bii dafa raw ci yi nu xam ndax ñàkkul mu am yeneen yu nëbbu te gën koo yéeme fuuf.

Te nag jëf yu ni mel du jóg mukk ci pénc mi lu dul Yoon dafay def li ko war : ku ñu teg tuuma ci ndoddam bu dee deful, ñu setal ko, bu defee nag, ñu teg ko daan yi mu yelloo. Amul lenn lees war a nëpp-nëppal !

Yoon nag du mën a def wareefam lu dul ñu bàyyi ko ak jonnam, mu tëdde njaaxaanaay di doxal ni mu waree. Te umpul kenn ne sunum Réew, Yoon daf fee gall-goose te firnde laa ngi ci wax ji nu fàttali ci kaw. Njiit li waroon a yamale ñépp mooy tànn ñi ko neex di leen neexal, ñi ko neexul, mu teg leen fitna. Mel ne kuy làq doom, dóor doom.

Seetlu bi di benn rekk, te di xaw a ndiróo ak la waykat ba doon wax : “Ku ànd ak ki ma àndal lu la neex def”.

Te bu nu fàtte ni am na lu bari lu ko jiitu te mujjul fenn ndax Njiitu Réew mi nee na moo ci teg concam. Concam bu diis gann bi nga xam ne li mu ñàkkloo Réew mi ci alal ak li mu raafloo ci mbaax ci diir bu gàtt mëneesu koo xayma. Waaw, alal ak mbaax yépp !

Alal, ndax bu fekkoon ne ki ñu njëkk tuumaal ci lekk alalu askan wi te bokk ci làngam bàyyi woon na ko ak way-àttekat yi, bu deful ñu setal deram, bu defee ñu teg ko daan yi war, kon nëgënii sii, kenn dootul xalaat a comp dërëm ci li ñu la dénk.

Mbaax, ndax kenn xàmmeetul Réew mi, kenn xamul lu muy ndiróol. Kersa, ngor ak doylu (te du ñoom doŋŋ !) fan lañu dugg ? Ku ko xam na wax ! «Ndegam bu ma àndee ak moom lu ma neex def, ndax dina ma làq, kon kay naa fecc te xam ne Yàlla a ma tàccu. Te sax, mag du fecc ci Yal naa dee. Sama liggéeyu ndey la. Sama ñakku bootaay la. Njëkkewuma ko te duma ko mujje.» 

Xanaa kay, yu mel nii la ñu bari di wax. Fàtte ne “yor loo mën a lekk taxul nga war koo lekk”. Waaye ndegam ci làng gi lañu bokk, dañuy yaataayumbe nu mu leen neexee te dara du leen ci fekk.

Li waykat ba naa : “Boo bañee ñaaw, boo ñàkkee dese ngor.” Jëfkatu ñaawteef yii moom, bañuñoo ñaaw ndax kenn du leen laal. Waaye sax, dañoo ñàkkul faf ! Ndax Réew mi deseelu leen dara. Xanaa kay ñàkk ngor, ñàkk lu ñuy jomb, ñàkk doylu ak bew mooy seen i tawat. Waaw bew ! Ndax jàpp nañu ne doole yépp a ngi ci seen i loxo. Lu leen neex def te dara du leen ci fekk.

Te kat, bu nu nax sunu bopp. Ndax Réew moo xam ne ñii lu leen neex def, dara du leen ci fekk, te ñale balaa ñoo ŋaaŋ sax yat wi dal seen kaw, foofu dañu koy woowe Réew ngir rafetal rekk xéy na, waaye liy ndiróo ak moom sax nekku fa. Nit ñi ko dëkke, ak ku ñu mën di doon, seen i der a ngi yàqu ci àll bi, ku leen gis di leen xoolee bëtu “ñii ñoo dëkk ci sagaru Réew moomu”.

Ngir njombe yu mel nii jóge ci Réew mi, fi nu war a tàmbalee mooy delloo Yoon gëddam, àttekat yi xam dëgg-dëgg ki ñu doon ak li leen war. Dafa war a leer nàññ ci seen bopp ne Njiitu Réew (ku mu mën di doon) dafay jaar, jàll. Waaye ñoom àttekat yi, li ñu doon, doon nañu ko ba fàww, ndax dañu koo jàng ba kiilu. Kon Njiit lu teg concam walla tànkam walla sax mu taxaw mbaa mu toog ciy wayndare yu jëm ci ñoom, waru leen a tere mukk ñu def li leen war.

 Baabakar Lóo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj