BOO BAÑEE ÑAAW…

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bu nu la waxee nga àggale kàddu gii, looy wax ? Nga tontu ne :

Boo bañee ñaaw de, xanaa dangay dëkkee toppatoo sag xar-kanam rekk, ak a sañse.

Boo noppee tuuti, ba sam xel dem, dellusi, nga ne :

Waaw, ku ñaaw ba noppi sax, ndax jar na muy def i pexe ngir bañatee ñaaw ?

Ci ngay déggee ne, du dangay xaar ba ñaaw di sog a jóg. Waaye, dangay fàggandiku. Te sax, ci kàddu gii, ñaawaay firiwul safaanu taar walla rafetaay. Romb na loolu lépp !

El Haaji Fay, dib waykat bu ràññeeku ci Réew mi, joxoñ na ñatti yoon yees mën a jaar ngir bañ a ñaaw. Sëñ bi Fay nee na :

“Boo bañee ñaaw, boo meree dese xel.

Boo bañee ñaaw, boo tiitee dese fit.

Boo bañee ñaaw, boo ñàkkee dese ngor.”

Xel du jariñ lu dul xalaat, te xalaat mooy li wuutale nit ak bàyyima. Nit nag, ñaare, bu meree, dootul am sago. Te, ku tàggook sagoom, bu moytuwul dina def yëf i mala. Te nag, jëf ni bàyyima moom kenn xaaru ko ci nit, ndax dafa xeebu lool. Moo tax waykat bi ne, ndegem mer mënul ñàkk, ku mer it na nga muus.

Fit mooy góor, te góor ay yiir jigéen. Kon, bu góor ñàkkee fit rekk, àdduna tukki. Lu ci bari nag, nit bu tiitee fit wi rëcc, te tiitaange mën na ubbi buntub caalit. Te nag, ku saalit def lu defuwul daf koy yomb lool sax. Moo tax bu tiit mënul ñàkk it, bu amee na fit wi toog.

Ngor yamul ci wax, dees koy jikkowoo ngir doon ab gor. Natt ko ci ku ñàkk moo gën a yomb fuuf natt ko ci keneen ndax kenn bëggul yàgg cim ñàkk. Ba tax nit di def i pexe (yu jub ak yu jubadi) ngir mucc ci. Te, lal i pexe yu dëng kat jëmul kër te mënul am njureef yu rafet. Moo tax ak lu ñàkk tar tar, dara warul tax nit di summi mbubbum ngoram.

Lii, lenn lu tuut la ci lees mën a déggee ci waxi waykat bi. Soxlawul xalaat yu xóot walla njàng mu sori ngir nangu ne xel, fit ak ngor ay ponk lañu yu am solo ngir teeyal dundug doomu Aadama. Boole ñàkk ñatt yëpp nag, ëpp naa def. Ndax, kenn xamul fu mu mën a yóbbu boroom. Yal nanu ci mucc !

 Baabakar Lóo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj