Mayleen ma nopp, abal ma seen i gët te ubbi seen um xel ma xellil leen !
Man Xalima, amuma lu dul samay rongooñ. Ñooy sama gémmiñ, di samaw làmmiñ, kon boog teewluleen ma.
Altine, 8i fan ci weeru nowàmbar ci atum 2021 yemoo ak 2i fan ci rakki-gàmmu 1443, limub 25i dongo yu toll ci 5 jàpp 6i at ñoo faatu ginnaaw bu seen barabu jàngukaay tàkkee jëppet. Jéyya ja a nga xewee ca dëkk bu ñu naan Maradi, bokk ci tund yi gën a mag ca réewum Niseer, féete ca Bëj-Saalumu réew ma. Ci fàttali, Niseer mi ngi ci Afrig sowu jant, réewum Mali rekk moo dox ci diggam ak Senegaal.
Xale yooyu ñu ngi woon ci jàngu yu njëkk yi : ñenn ñi nekkoon ci jàngu bi ñu leen di tatagalee ak a dalal (“CI” ci farañse) ñeneen ñi, ci jàngu bi ñu leen di waajalee ngir ñu mën a tàmbali njàng mi ci daraa ju suufe ji (“CP” ci farañse). Ñu doonoon ay tuut-tànk yoy, àdduna sépp a leen manoon a jariñoo bu ñu màggoon. Li leen yóbbu du lenn lu dul nekkin yu doy waar ya ñu nekke woon ci seen daara jooju. Nga xam ne jàngu yi ay bant ak i ñax mu wow lañu ko defare. Loolu a waral ba safara si ñëwee, bàyyiwu fa lu bari. Xale yi dañoo lakk ba benn bàmmeel lañu leen boole denc. Muy lu tiis lool ! Ndax moos way-jur wi xëy wutiji, yabal doomam mu sàkkuji xam-xam, bu ñu ko woowee ne ko sa doom dootul dellusi, dem na ci anam yu mel nii, dina am naqar wu diis a diis.
Lii nag, ag fàttali la woon rekk ngir laltaayal li ma bëgg a indi ci suuf. Ginnaaw man Xalima bu samay kàddu jibee rekk samay gët tooy, toppleen samay toq-toqi ràngooñ nu ànd ci ñaari poñ yi ma bëgg a yaatal ngir jàngat la xewoon ca Maradi.
Nanuy bàyyi xel li xew ci kër gi
La woon ca Maradi, niki xew-xew yeneen yu ni mel tey am ci réew yi nu wër yu bari dañuy jaar jàll. Mu mel ni nun waa Senegaal yëgunu ko.
Ci ndoorteelu weeru suwe ci atum 2021, ay defkatu ñaawteef song nañub dëkk faat fa lu ëpp téeméeri nit ca Burkinaa-Faso. Ci njeexitalu atum 2021, ba tay ca réew moomu, 41i nit bóom nañu leen ba waral njiitu réew ma woon woote woon ñaari fani dëj ca réew ma yépp. Ca Mali, ci weeru desàmbar wi weesu, lu mu néew néew fanweeri nit faat nañu leen fa ba tax ñu amaloon fa ñatti fani dëj. Ca Niseriyaa, ca Niseer…
Xew-xew yii yépp, dafa mel ni waa réew mi duñu ko yëg. Te moone de, ci biir kër gi lay xewe. Ndax Kembaaru Afrig manees na ko a xaaj ci juróomi kër, pegg bu ne benn, ak bi ci digg bi. Ci lanuy gisee ni ndekete Mali, Niseer, Burkinaa-Faso, Niseriyaa, añs. Duñu sunuy dëkkandoo rekk yem ca, danoo bokk kër sax faf. Te lenn warul xew ci kër gi, ñi ko dëkkee gëmm seen i gët, fatt seen i nopp : janax jiy yàq ci néeg bi nu janool, man na noo ganesi suba !
Te li ma jaaxal sax man Xalima mooy mbir dafay xew ca àll ba waa Senegaal bëgg ko a def seen mbiru bopp. Ci atum 2020, ca réewum Amerig, ba fa ab takk-der faatee ngóor su nuy wax Soors Foloyit ñépp moom lañu doon waxtaane. Senegaal gépp di ko naqarlu. Dëgg la, ñu bari li taxoon ñuy ñaxtu, dañoo jàppoon ni jëfu takk-der boobu dara lalu ko woon lu dul xeeb nit ku ñuul. Waaye ak lu man a am, ci jamono jooju, ay jéyya yu ne fàŋŋ ñu ngi xew ci kër gi nu ne patt.
Fi mu ne nii, ñépp a ngi wax ci xeex ba ca réewu Ikren, ku nekk di wut fu mu far ak a naqarlu daw-làqu yi mu jur ak xale yi ciy tumurànke. Te ñu néew a néew ñooy yëy-yàbbi ci njaboot yiy loru ca Niseriyaa, Mali, Ecópi, añs. Ndax ay cong yoo xam ne askan wi ciy yàqule ak a gaañu sax ñaare xamuñu lu ko sooke. Mu mel ni ñoom, seenug loru, lu jaadu la. Dafay niru ne nun ak sunuy ñoñ, yoon lanuy dund jafe-jafe ci kaw jafe-jafe. Loolu moy li jaadu ci nun. Nun daal aw askan lanu woo xam ne bu nu dundul ci fitna rekk nekkunu ci jàmm. Waaye keneen ku dul nun, buy dund lu metti, danoo war a mànkoo ñaawlu ko. Naka lanu àggee ci tolluwaay bii ? Danoo xamul sunu cër walla danoo réere sunu bopp ? Ak lu ci man a am, sunuw doxaliin wone na ni, mbiru ñeneen ñi a nu gën a yitteel liy xew ci kër gi.
Dëgg la nag, bakkan bu rot, ak fu mu man a amee, walla nu mu man a demee danu koy naqarlu bu baax a baax. Waaye Wolof dafa ni : « Bala ngaa laax jaay, laax lekk ». Lu tax nu war a soofantal sunu yëfi bopp yoo xam ne bu nu ci jéemul a wut i pexe, kenn du ñëw di nu ci defal dara ba noppi bëgg a jël mbiri jàmbur ne fàww nu taxaw ci ?
Ñàkk a fullal yi fiy xew, yemul rekk ci di nu doyadil waaye dafay tax dootunu sax sóoraale ni am nanu ay jafe-jafe yu nu war a wutal i saafara. Foofu laay jaare man Xalima barastiku ci sama ñaareelu tomb.
Jàngu négandiku yi ci réew mi, ba kañ ?
Goney Maradi yi, safara si faatu leen de, déedéet ! Li dooleel safara si moo leen yóbbu te du lenn lu dul melokaanu barab ya ñu nekkoon di jàng. Ay néegi ñax lañu doon jàngee. Te jàngu yu ni mel bari nañu lool ci sunu réew mi nu leen di woowe ay “jàngu négandiku” (“abris provisoires” ci farañse). Ñu ngi leen xayma woon ci lu ëpp 6300 ci réew mépp. Bu nu sukkandikoo ci Abdulaay Jàllo, di kenn ci waa “Cosydep” di kurél guy saytu ak a sàmm njàngum njémmeer li ci réew mi, ci tund Séeju doŋŋ waññi nañu fa limug 647 ci daara yu suufe yi ak 238 ci daara yu digg-dóomu yi ci atum 2018. Mi ngi waxee lii ci ngoliiru taskatu xibaar bii di Paab Aale Ñaŋ mi def liggéey bu am solo ci jàngu négandiku yi ci Bëj-Saalumu réew mi.
Jàngu yooyu nag am nañuy melokaan yu bari te wuute : yii ay ñax la, yee di ay sàkket. Dongo yi ak seen i sëriñ-daara, di nokki ci pënd bi (ndax amul dër), naaj wi tiim leen, yenn saa jaan ganesi leen, ndoxum teen lañuy jëfandikoo, mbëj moom waxaalewuñu ko sax.
Seen lim bu takku bii rekk waroon na a tax, bu fekkoon nun Saa-Senegaal yi nu ngi bàyyi xel ci liy am ci dëkk yi nu wër, ba jéyya ja amee ca Maradi, mboolaay gépp a waroon a jóg def wenn say wax ak kilifa yi ŋànk njàng mi ñu taxaw temb jële fi jàngub négandiku yi. Dëgg la nag, nee nañu ñu ngi ci waaye ñu soññ leen ñu baral seen i tànk.
Bu nu ko xoolee ci lu gën a jege, danuy gis ne li ne fee rekk moo ne fii : ñàkk a bàyyi xel ci liy xew ci li nu wër. Ndax ñi nekk ci gëbla gi walla ci yenn gox yu mag yi mbir mi taxul mu yitteel leen lool, xayna sax xamuñu ne am na, te moone bu ñu gisoon ne mbir mi ñépp la soxal, taxawaay bi doon na gën a am solo te du ñàkk saafara si doon na fi gën a yaatu. Ndax bu nu xoolee, ñi koy dund ñu ngi def seen i pexe ngir wut leneen lu ko gën donte ne seen lim takkuwul te it seen doole demeewul noonu. Ci goxu Gudomp, am na kurélug way-juri dongo yu àgg ba ci jël guddig lëmm dem nappi sippax ngir li ñu ciy am man a tabax ay jàngu ci daara yi seen i doom di jàngee.
Te bu weesoo ñàkk kaaraange gi ci nekk, xeetu jàngu yooyu dañuy am njeexital ci njureefu dongo yi. Duñu man a jàng diir bi war, ndax yeex a tàmbali ba noppi nar a njëkk a tëj bu dee ci gox yiy teel a taw. Waaye itam yemale gi waroon a am ci xale yi dafay sooxe. Ndax bu ñenn ñi nekkee ci ay taax yu mucc ayib, ñeneen ñi ñu ngi ci ay barab yu doy waar lool te jagadi. Kon bu nu màndaxee li dongo yooyu di jàng dëgg-dëgg ak li ñu war a jàng ci at mi, danuy gis ne am na lu bari lu des. Waaye it, bu nu nattee seen tolluwaay, seen digg ak seen i moroom yu nekk ci anam yu jaadu, danuy gis ne ñaar yi yemuñu.
Kon nag jot na, kilifa yi ak képp ku ci man dara, ak lu mu man a doon, ñu jóg te baral jéego yi jële fi lii.