COOW DIGGANTE BILAAL JAATA AK TASKATI-XIBAAR YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njabootu saabalkat yi mer nañu ba futt. Li ko waral du lenn lu moy jëf ji meeru Kër Masaar Sid def démb, ci dibéer ji. Dafa di, moom Bilaal Jaata dafa am liggéey bu mu doon amal ca gox ba. Mu jot faa jàppante ak taskati-xibaar ya fa ñëwoon. Taxawaay boobu mu taxawe démb moo jur coow lu réy ci réew mi. Ba tax na, kurélu saabalkat yi génn nañu ñaawlu mbir moomu.

Barki-démb, ci dibéer ji, la meeru Kër Masaar ak i ndawam génnoon ngir def li ñuy wax “déguerpissement”. Maanaam, dindi ci mbedd yeek yoon yi lépp lu mën a gàllankoor dem beek dikk bi. Waaye, liggéey boobu ñu doon amal ci ay coow la mujj. Ndax, ñii di jaaykat yi, ñu leen di woowe ay “marchands ambulants”, ànduñu ci mbir moomu. Loolu moo gën a yokk ci xar mi kawar.

Moom, Bilaal Jaata, meer ba, dafa jàppante ak taskati-xibaar ya. Te, li leen yékkati woon ñoom mooy def seen liggéey. Maanaam, wan askan wi lay xew ca béréb ba. Ci loolu nag la jote ak ñoom. Ba xibaar ba tasee ca la ñiy yëngu ci wàll woowu yépp génn, fésal seen naqar. Nde, dañoo jàpp ne taskati-xibaar yi dañoo war a def seen liggéey te kenn du leen ci gàllankoor. Li war kay mooy ñu aar leen bañ leen a gaar. Looloo tax, kurél yu ci mel ni APPEL (Association des Editeurs et Professionnels de la Presse En Ligne), SYNPICS (Syndicat des Professionnels de l’Information et de la Communication du Sénégal) ak CJRS (Convention des Jeunes Reporters du Sénégal) ,génnee ay yégle ngir naqarlu jëf jooju. Ndax, jëf jooju yellul ci kilifa gu tollu ne moom.

Mu mel ni coow li narul a yam foofu. Ndax, kii di Feuz Dione jébbal na ab pelent fa toppekatu bokkeef bi nekke ëttu àttekaay bu mag bob Pikin-Géejawaay. Meer bi, Bilaal Jaata, la jure. Nde, ciy waxam, daf leen a yàqal seen i jumtukaay. Rax-ci-dolli, dañoo gaañ benn “camerawoman” bu FD Media. Li muy sàkku ci jure boobu du lenn lu moy Yoon def liggéeyam. Kon, balaa yàgg dees na xam fu wànnent du mujjeek i bëtam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj