COOWAL BAC 2024 BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Joŋante BAC bu atum ren jii bari na ay coow lool. Te, li ko waral du lenn lu moy ñàkk a jëfe ndigal gi ñuy nemmeeku ci ndongo yi. Looloo tax, ñuy dégg ay ndongo yu ñu jàpp. Ndax, dañoo yoroon seen i jollasu fa bérébi joŋante ya. Juróom-ñetti ndongo ya ñu tegoon loxo fa Daara Jolof, àtte nañu leen démb ca àttewaay bu Luga. Li ñu leen doon toppe mooy li ñuy dippe “fraude”. Dañoo ubbi woon ag kippaangoog WhatsApp di fa dugal ay kàtte yu ñu defar ba noppi. Ki tijji woon kippaangoo gi (administrateur groupe WhatsApp) moom, daan nañu ko weeru kaso. Juróom-ñaar ya ca des ñu daan leen fukki fan ak juróom yoo xam ne dinañu ko tëdd. Waaye, mbir moomu, ndeke yemul ci joŋante gu njëkk gi kese. Am na tamit ñu ñu teg loxo démb.

Démb ci àllarba ji la ñaareelu pàccu joŋante BAC bi door. Maanaam, ñi nga xam ne, li leen dese woon ciy poñ ngir ñu jàll ci pàcc bu njëkk bi bariwul, ñoom ñoo doon mottali. Démb nag, am na juróomi ndongo yu ñu ci teg loxo fa Kanel. Ñoom tamit, seen kippaangoog WhatsApp lañu ubbi woon ngir dugal fa kàtte gi. Te, li ci gën a yéeme mooy ñeent ñi moom jotoon nañoo jàll ca pàcc bu njëkk ba. Kon, li ñu dugge woon mbir mi mooy jàppale seen naataango boobu ba mu mën a jàll ci ñaareelu pàcc bi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj