COOWAL LUUBALUG KOPPAR CA BÀNK BISIC

Yeneen i xët

Aji bind ji

Luubalug koppar gu takku mooy coow ca bànk BSIC bu nekk Pàrsel Aseni. Lu jege genn-wàllu tamñaret lees fa sàkkal pexe ba ñu teg ci loxo ñeent ci ña fay liggéeyee ak ka ñu daan yónnee xaalis bi.

Ca bànk BSIC (Banque Sahelo-saharienne pour l’Investissement et le Commerce) ba nekk fa Pàrsel Aseni, dañ fa luubal koppar gu takkoo takku. Luññutu gi njiiteefu bànk bi doon sàkku moo wone ni am na lu ëpp 469i tamndareti FCFA yees sàkkal pexe ciy génne xaalis bu jaarul yoon. Naka noonu lañ jébbal ab kalaame fa DIC (Division des investigations criminelles) ngir ñu amal fab lànket.

Ginnaaw kalaame boobu ñu def fa Dic, lànket bi teg na loxo juróomi nit. Ñeent ñi doon ñuy liggéeyee fa béréb ba (U. Kan, A. N. Seen, Nd. X. D. Faal ak M. Gay). Ki leen juróomeel moo ngi tudd A. H. M. L. Njaay mi doon jot xaalis bi.

Ci biir lànket bi sax, U. Kan may njiitul béréb ba weddi woon na ba tëdd ca naaj wa. Waaye A. N. Seen ak Nd. X. D. Faal ñi yor kees yi ñoo ko taqal ripp. Nde, ci li ñu wax, moom moo leen jox ndigal ñu def lu nirook i wersamaa (Versements fictifs) ci kontu E. H. M. L. Njaay. Muy xaalis bu mu waroon a koppartu.

Ci li lànket bi wone, ci keesiyeer bu jëkk bi la mbir yi tàmbalee. Yónnee na 392i tamndaret ci 9i wersamaa. Ginnaaw gi la ñaareelu keesiyeer bi tàmbalee def ni mu daan def ba àg ci 7i wersamaa ak 366i tamndaret. Sñ Njaay itam jot naa tas ci xaalis boobu, yónnee ciy nit, ñenn ñi mu jox leen i seg (chèque). Loolu yépp nag, mi ngi sottee ci yombalug M. Gay (responsable des opérations) mi jébbaloon keesiyeer yi ay seg yu E. H. M. L. Njaay moom.

Ñoom ñépp ñi taqal nag, ña nga ca loxoy yoon jamono jii. Bokk na ci tuuma yees leen gàll : mbooloo defkati ñaawteef, génne xaalis ci mbuxum, wootewoo koo nekkul.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj