Barki-démb, ci gaawu gi, la dépitey CEDEAO yi doon amal am ndaje fa Abujaa, fa réewum Niseriyaa. Waaye, laata ndaje ma di jeex la fa xew-xew bu doy waar am. Nde, ñaari dépite ñoo fa naroon a jàppante. Te, lenn waralu ko lu moy kàddu yi kii di Gii Mari Saaña yékkati. Kàddu yooyu la naataangoomu dépite bi dëkk fa Koddiwaar ne du ko dégg. Fa la coow la dooree, ne kurr fa béréb ba. Ndax, soxna si daf ko naroon a songu, gaa ñi dox seen diggante.
Xiiroo ak ŋaayoo gi am diggante ay dépite day mel ni léegi safeetul. Ndax, dafa bari lu ñu koy nemmeeku ci Ngomblaan yi, rawatina fii ci Senegaal. Waaye, wii yoon, mbir mi jéggi na réew mi. Ndax, dépite ya doon amal um ndaje, bokkuñu sax réew yu ñu jóge. Waaye, loolu terewul ab xeex naroon faa am ba ñu dakkandil ndaje ma.
Li waral coow li mooy kàddu yi ndawu Senegaal li yékkati, wax leen ci ndoddi Njiiti Afrigu sowu-jant yi. Loolu la yenn dépite yi jóge ci yenn réew yi di naqarlu. Ba tax na, soxna sii di Ajaratu Taraawore, di ndawu réewu Koddiwaar, di it ñaareelu tof-njiitu kurél gi ne ko bu mu ci jaaraat. Ndax, moom doomu Senegaal ji, daf ne réewi Afrigu sowu-jant yi, seen i Njiit ñoo tax ñu ndóol. Maanaam, réew yi ndóoluñu, waaye, ñi leen jiite ñoo leen suqaliwul. Ndax, seen bopp kepp lañu fi nekkal. Ci gàttal, ñoom suqaliwuñu réew yi, dañu leen di suuxal. Te, amul réew mu leen ëppale dara ci àdduna wërngal-këpp.
Kàddoom yooyu, mi ngi leen yékkatee ci sumb bi ñu doon waxtaane, ñu koy dippe PNUD (Programme des Nations Unies pour le Développement). Ndax, moom dafa jàpp ne réew yi ndóoluñu, seen i Njiit a tax ñu ndóol. Bi mu yékkatee kàddu yooyu nag, Njiitul béréb bi sàkku na ci moom mu seetaat li muy wax. Waaye, mu xamal ko ne ŋàññul kenn. Te, am na sañ-sañu wax li mu bëgg. Waaye, naataangoom bi bawoo Koddiwaar ne ko amul sañ-sañu teg ci deri Njiit yi lu ko neex. Kàddu yooyu soxna si yékkati taxul doomu Senegaal ji teggi tànkam fa mu ko tegoon.
Bi soxna si gisee ne kii li mu wax, faalewu ko sax, ca la wàcc, jubali ca Gii Mari Saaña. Waaye, laata mu koy fekk fa mu nekk, fekk na seen naataango yi dox seen diggante. Soxna si di xataraayu nees ko gisee ci widewoo yi. Ca la coow la nee kurr fa béréb ba, jàppal bàyyil gu dul jeex ba Njiitu béréb ba mujje dakkandil ndaje ma ba gaa ñi dal, xel yi dellusi, ñu sog a wéyal liggéey bi.
Mu mel ni du guléet ñuy nemmeeku xiiroo ak ŋaayoo ci ndajey réewi Afrigu sowu-jant yi. Nde, jamono jii ñu tollu rekk, ñaari kurél a fi nekk, muy AES ak CEDEAO. Ku nekk di xëcc di jëmale àll, jàpp ne moo nekk ci dëgg. Waaye, li xew démb ci ndajem kurél gii moom dafa ëpp i loxo. Ab dépite jóg ne day song moroomu dépiteem ci ay kàddu yu mu yékkati. Fii la bët yem.