Joŋanteb kuppe bees duppee “Coupe du monde des clubs”, di po mu mag muy boole lenn ciy këlëb yu mag ci àddina si. Ñi jël “ligue des champions” ca seen kembaar mbaa ñu def i jaloore yu rëy ci at yu mujj yi ñoo ciy daje. Etaasini moo dalal joŋante bi, foofa ca Amerig. Këlëb yi dañu leen séddale ci ay kippu, bu ci nekk def 4i ekib. Këlëb bu ci nekk war na daje ak sa moroom ci biir kippu bi, ñaar ñoo ciy génn, daldi kalifiye ca 1/8 dë finaal ya.
Lenn ci ekibi Tugal yu mag yi bokk nañu ci. Ñu ci mel ni Inter Milan, Atletico Madrid, Real Madrid, Manchester City, Paris SG, Porto, Bayern Munich, Dortmund, Chelsea… Ñoom ñépp waajal ko ni mu waree ngir yéene koo jël.
Po mi tàmbali na démb ci gaawu bi, 14i suwe 2025. Ekibu Lionel Messi bi, Inter Miami (Ameriig) ak Al Ahli (Afrig) ñoo ko ubbi. Way-lootabe yi amal ci ubbite gu rëy, bu am solo. Ñaari ekib yi dañoo timboo 0-0. Mu nekkoon mats bu neex ndaxte ñaari ekib yi dañoo xawoon a tolloo doole. Mitã bu njëkk bi, Al Hilal moo xawoon a jekku ba am ci sax penalty,i moyal ko. Waaye, ñaareelu mitã bi Inter Miami moo ko jekku. Yeneen mats yi dinañ am ci dibéer ji jëm ci biir ayu-bés bi.
Réewum Senegaal am na fay doomam yu ko fay teewal. Ñii ànd ak seen i këlëb (Nikolas Jakson, Mamadu Saar (chelsea), Kalidu Kulibali (Al Hilal), Aamadu Ñaņ (Al Ain), ñii ñu woo leen ci jox leen ci cër (Aliw siise, El Haaji Abdulaay Sekk), ñii diy arbiitar (Isaa Si, Jibril Kamara, Nuhaa Bànguraa)