Ami Mbeng
Bu dee mbas mi wàññeeku na bu baax ca Siin, mu ngiy wéy di rajaxe àddina si, rawati-na réewi Ërob yi. 159 réew ame nañ Covid-19 bi ; réew yi mel ni Farãs, Etaasini, Marog, Itali, Espaañ, añs. jël nañ ay ndogal ngir daan jàngoro ji. Àgg nañ ci tere nit génn këram. Ndege, limu way-tawat yi ame Covid-19 bi ak ñi ciy faatu day gën di yokku saa su ne. Fi mu ne nii, ci xayma, lu ëpp 350.000 nit ci àddina si ame nañ doomu-jàngoro bi te, 9 300 ñàkk nañ ci seen bakkan.
Nan seet naka la mbir mi deme ci réew yooyu.
Itali
Jamono jii, mooy réew mi gën a sonn. Daanaka, Covid-19 daaneel na fa 36 000 doom-aadama. Fan yii yépp, doktoori Itali yaa ngi def ay widewo di sàkku ndimbal ci àddina si. Fi mu nekk nii dañoo sës, toqi. Ci alxames jii rekk, limu nit ñi dee ci Covid-19 bi àgg na ci 3 405 nit. Waaye, réewi Ërob yépp a ko dëddu, kenn fasul yéene dimbali ko. Ndax, ku ci nekk sa bopp nga tal. Xanaa Siin mi nga xam ne tane na bu baax a baax moo koy wall as tuut ànd ceek Risi ak Kubaa. Muy, boo ko xoole ci fànnu politig lu doy a doy waar !
Farãs
9134 nit am nañ Covid-19 bi te faat na 264. Njiitu kurél gi yor wàllu wér-gi-yaram ci réewu Farãs ne, am na 931 way-tawat yu sonn lool, nekk diggante dund ak dee. Mu amaat yeneen 3626 yoo xam ne ñoo ngi tëdd loppitaan. Moo tax, talaata ba léegi, réew mépp lañ tëj, ne bu bénn maxejj génn këram, lu ko moy dinañ ko daan walla ñu alamaan ko xaalis bu bare.
Espaañ
Ginnaaw Itali, Espaañ mooy réew mi gën a sonn ci Ërob. Limees na fa 17 395 way-tawat yi ame Covid-19 ak 803 way-dëddu ñeel jàngoro ji.
Almaañ
Fii tamit, mbir mi day gën di yokku. Seen i way-tawat ñoo ngi tollu ci 13 979 ak 42 nit ñu ci faatu.
Siin
Fa la mbas mi doore. Waaye, wàññeeku na fa bu baax a baax. Daanaka, amatul benn doomu- Siin bu ame jàngoro ji. Xanaa ay doxandéem yi ko fay indaale. Moo tax, nguurug Siin mi ngi saytu bu baax ñi fay dugg.
Portigaal
Ñoom, ci alxames ji, 785 way-tawat lañu ame ak 3 ñu ci faatu. Waaye, nguur gaa ngi wattandiku bu baax. Moo taxit, tëj nañ lekool yi, réstóraŋ yi, baar yi, diskoteg yeek màngasin yu mag yi.
Àngalteer
Ñoom, 2 644 way-tawat lañu amagum ak 71 dee. Yeneen réewi Ërob yi dañ doon ŋàññi nguurug Àngalteer ci ndogal bim jëloon ne day bàyyi ba yarami nit ñi ci seen bopp tàmm feebar bi (immunité collective) ba du leen lor. Waaye, mel na ni seen njiitu jawriñ soppi na doxalinam. Ndax, mi ngi digal askan wi ñu fagaru.
Etaasini
Waa Amerig, ñoom, fi mu tollu nii, 9 415 way-tawat ñoo fa nekk, 100 ñoo fa dee. Donald Trump dafa tere réew mi nit ñiy bawoo ci 26 réewi Ërob. Rax-ci-dolli, baar yi, réstóraŋ yeek diskoteg yépp tëj nañ leen biir Niw-York, Los-Anseles, Wasinton DC ak Kaliforni.
Afrig
Li ëpp ci réewi Afrig yi ay benn ak i ñaari way-tawat lañu amagum. Niseryaa am na 3 way-tawat, Ruwàndaa 07, Misra (Esipt)60 way-tawat ak kenn ku dee, Alseri 48 way-tawat ak 04 ñu dee, Tinisi 20 way-tawat, Burkinaa Faaso 15 way-tawat ak kenn ku dee. Marog, moom, am na 28 way-tawat ak kenn ku faatu dee.
Covid-19, mbaa du ay nit a ko sàkk ? Walla ?
Fan yii yépp, ñoo ngi biral ay widewo ak ay téere yiy wax ne Covid-19 bi ay nit ñoo ko defar ngir wàññi niti àddina si. Ñii ngi naan, farañse yee ko defar ca Institut Pasteur bu Farãs, ñeneen naan Amerikeŋ yi la. Ak lu ci mënti am, mbir mi teey na xel. Ndaxte, àddina si, léegi, dafa tëradi.