DAANUB USMAAN SONKO AK NDEY XADI NJAAY : ÑU BAREE NGIY ÑAAWLU

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tey, ci alxames ji 1eelu fan ci weeru suwe la àttekat bi biral daan yim gàll Usmaan Sonko ak Ndey Xadi Njaay ñeel layoob ciif ak tëkkuy rey yu Aji Saar doon toppe njiitul Pastef li. Ci yoor-yooru tey jii la ndogal li jib. Ginnaaw bim setalee Usmaan Sonko ci tuumay ciif ak tëkkuy rey yees koy toppe ci mbir mile, daf ko daan 2i ati kaso yu muy tëdd ci kow ne, dafa jóo xale bii di Aji Saar ci mbonte ak yëfi saay-saay. Bu dee Ndey Xadi Njaay moom, àttekat bi daf ko daan moom itam 2i ati kaso yu muy tëdd ci kow ne dafa, moom tam, dafa defloo Aji Saar yëfi caga. Am na sax ndàmpaay lu ku nekk ci ñoom ñaar war a jox Aji Saar. Ndogal loolu nag, metti na ñu baree bari.

Mari Tëw Ñaan :

« Kilifa gi, Njiitu réew mi,

Ngir jàmm, ngir dalaayu réew mi, dellool askan wi baatam.

Sa nguur gi daanu ba fàww.

Ñi ci amey gaañu-gaañuy bari nañ, yàqute yi bare nañ, tiit gi bari na, mbañante geek ñaawoo bi ëpp na !

Ak bakkan rot nañu ! Ay nit deewati nañu !

Jàpp ci nga tekki sa ndombog-tànk !

Senegaal dafa soxla jàmm ! »

Aminata Ture :

« Àtte biñ àtte Usmaan Sonko daf ko setal ci tuumay ciif ak tëkkuy rey. Kon, daanub 2i at yi mu war a tëdd yii, dafa worook yoon ci lu fës. Maa ngi feddali sama ànd ak Usmaan SOnko ak militaŋi Pastef. »

Xalifa Sàll :

« Daan bi tukkee ca « chambre criminelle » ñeel layoob njiitul Pastef li, dafay woneeti ne, dañu soppi Yoon, def ko ngànnaayu pólitig. Daan bees daan Usmaan Sonko 2i at yi mu war a tëdd, donte ne setal nañ ko ciif ak tëkkuy rey, du lenn lu dul am pexe gu mujj ngir faagaagal ay nattangoy pólitig. »

Séydi Gasama :

« 2i at ak lu teg, ñu nuy wax waxi ciif ak tëkkuy rey yu ànd ak i ngànnaay. Ca layoo ba, ba toppekat bay biral càkkuteefam, guléet ñu gis tuumay « corruption de la jeunesse » bob, ci la àttekat bi sukkandiku ngir teg daan bi. Nii la Senegaal di doxe 2012 ba tey. »

Biraayim Sekk mi jiite Ndajem maxejj yi :

« Dafa jot caaxaan yii dakk ci nim gën a gaawe. […] Bu ñu dégloo àtte bi, dangay gis ne singali bi ñu singali Usmaan Sonko ak Ndey Xadi Njaay dafa war a dakk. »

Abdurahmaan Juuf :

« Njiitu réew mi, Maki Sàll, dem na ba sës ci bëgg-bëggam. Dëgg mësu ko ñor. Ragal bi mu ragal wujjuw pólitig a ko yóbbe muy fowe Yoon ngir am daan buy tere Usmaan Sonko bokk ciy wote. Loolu kesee ko soxaloon. Xoolu ci sax àqi maxejj bi. Seetu ci sax ngorug boroom kër bi Usmaan SOnko doon. »

Dr Baabakar Jóob, njiitul FDS Les Guelwaar, meeru Cees :

« Nees ko doon xaare, ab layoob pólitig la bu jur ab àtteb coxorte gu bon. Daan Usmaan Sonko 2i ati kaso yi muy tëdd ngir « coruption de la jeunesse » mooy wone nger mu réy mi ci Yoonu Senegaal. daan bi, day setal Usmaan Sonko ci tuumay ciif gi te di taqal deru Yoon ci boppam. Baatu Yoon bi nekk ci loxoy jaaykatu doole àtte na àtteem, jaarale ko fim ko bëggoon a jaarale, ak i firndey boppam, layoob boppam, te xooi ci enn yoon liy dëgg ak li jaadu. Dina yàgg bala nuy setal sunu der ci ñaawteef bile. »

Natali Yàmb :

« Maa ngi yaakaar ne layookati Usmaan Sonko yi dinañ toop Aji Saar ak ñi ko doon digal muy def ngir yàqub der, tuumay fen ak mbóomug doomi-aadama yu bir. Maa ngi yaakaar tamit ne, mbootaayi jigéen ñi dinañ topp Aji Saar te/walla ñu naqarlook ak ñaawlu ci kanami ñépp li mu yàqal jigéen ñu bari ñi nga xam ne, siif nañ leen dëggantaan. »

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj