DABBAAX : BAAX NGIR YÀLLA, BAAX CI SENEGAAL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Senegaal, ci sunu aada, bu ñu tuddee doom, dañu baaxoo di ñaan : Yal na tur wi wuyu boroom.  Allaaji Abdu Asiis Si Dabbaax, ñaan googu dal na ko. Moom doomu Maam Mawdo Maalig ak Maam Sófiyetu Ñaŋ, ñuŋ ko duppee boroom xam-xam bu yaatu, doonoon it bindkat bu mag. Ginnaaw bi Maam Mawdo jàngee téereem la ko naw ba am yéene tudde ko doomam. Rax-ci-dolli, « daa baax » tamit am lu réy lu mu tekki ci làmmiñu wolof. Boo seetee lii lépp kon, dinga gis ne tur am na solo. Te, Dabbaax wuyu na turam. Moo waral ba sun-jonn-Yàlla tey jii ñu koy fàttaliku, rawatina fi réewum Senegaal.

Moom miy 3eelu xalifa Mawdo, mi ngi gane àddina 1904, def ci xilaafa gi 40i at yu teg 6i weer, liggéeyam noppi, mu wàcc keroog 14eelu fan ci sàttumbaar 1997.

Sëriñ Abdu Asiis ci boppam moo ne woon dafa jàppe boppam mbedd mu mag mom, ay kër a ko wër ci wàllu ndeyjoor ak càmmooñ, ñu ne ko jaaral ci mbedd mii, kër goo fi séen mu yàqu nga defar ko… Moom daawul fekke lenn lu ñaaw, yor pusoom rekk di ñaw.

Moo tax, tey jii, ñépp di ko fàttaliku ak xol bu tooy. Saa yu réew mi mësaan a yëngu, mu sol i dàllam, dox, wax ba lépp sedd te ay waxam taawloo dëgg ak njub. Dabbaax waxal na boppam ciy kàddu yu leer nàññ ne :

« Limaan mooy li sax ci xol, nga dëggal ko, te koy jëfe…

Àddina dafa jaxasoo jaxasoo goo xam ni loo wax ñu seet la ca dëppook seen bakkan ñu jël, la ca des ñu rotal ko. Waaye nag, su dee Yàlla rekk a la tax di wax, fàww nga wax ngir Yàlla. Xawma nag kuy wax ndax dañ loo ragal ag dikkam ci sa kow walla ngay wax ngir taataan loo bëgg mu tegu ci sa loxo. Yooyu yépp set naa ci wecc. Ëmbuma daraay kenn te waxuma tamit ngir suturaal sama bopp, damay wax ngir Yàlla. Ku bëggul dégg li Yàlla santaane ak Rasuulilaa bul ñëw ci man. Bitig bu nekk ak màrsandiisam… Màrse Allaaji Maalig nag mooy topp li Yàlla bëgg, deesu ci seet bànneexu kenn mbaa ku leen mere, walla saakuy ceebi taalibe yi.

Duma samp sama bopp, walla Allaaji Maalig, walla Yonent bi, wacc Yàlla, déedéet, Yàlla rekk laay samp.

Sunu dund gii du dara, day jeex rekk. Bés dina ñëw Yàlla jël nu. Ñu wuti perkaal, ndéem, wittéen, sang ni ñépp, julle, suul, ñaan, nu dëddu añs… Te foofa, loo fa jiitalul soo fa demee doo ko fa fekk. Seetal waa ji bind segam yóbbu ca bànk ba te mësu faa denc, waxuma jël xaalis waaye soo wattuwul kasoo la ciy fekk. Nii rekk la mbir demee, nanu topp Yàlla te ragal Ko. Nanu ànd ci dëgg tey waxante dëgg. Dëgg du wàññi wërsëg te du tax a dee te sa dee jotul…

Yàlla tànn la ci sa biir i mbokk, ci saw xeet, teg la ci kanamu doom-aadama yi, loo bëgg ñu defal ko, loo wax ñu def ko, sama Boroom jox la boobu cër, teraanga gii ni mu day soo ko jëndee sa bànneexu bakkan walla lu neex nit walla ragal ba doo wax dëgg, doo ko digle, doo ko santaane, lépp lu ñu def, Yàlla sib ko nga ànd ceek ñoom, mu neex la ngir sa bakkan walla ku la neex, kon yow doo dara. Te, loolu rekk a xew ci jamono jii. Ku ci nekk yaa ngi samp sa bopp, di wut mbooloo ak lu ñu la jox ba mu sotti rekk. Yàlla, moom, dara…

Waxuma ngeen yëkkati kenn, daaneel kenn, bu kenn xeex kenn waaye nanu wax te Yàlla tax…

Ni nga amee sañ-sañ ba taxawu li la ñor, doo ma xoqtal ci dara ba li ma war a taxawal du am. Kenn mënu ko. Ndax li am mooy nit dees koy nappe ci yi ñiy nappe doom-aadama, jàpp ko. Man nag, Abdu, lëjëluma kenn ci lu ngeen am jox ma, kenn beyul ma fab, yoreeluma leen dara loo xam ni dama naan Maam Demba joxoon na ma mbubb walla xaalis, yenn dëgg yi duma ko ko mën a wax. Déedéet, Abdu dundul loolu…

Fabuma ci fasu kenn, bojjuma ci sàqum kenn, ku ma defal dara rekk daa fekk mu neex la…

Nanu dolli góor-góorlu te am fitu di jëfee diine ji… Nanu boole xol yi…

Xawma luy xew ëllëg, mën naa dee fii, léegi, walla sama kër. Waaye, kenn mënuma jënd ci dara ; aaruma ci sama bopp, Yàllaa ma ci aar, duñ ma jënd ci jigéen, duñ ma jënd ci daraja, duñ ma jënd ci alal, kenn mënu ko. Li Yàlla bëgg nag fàww ma koy wax ndax mooy sama warugar, foofu lañ may xaar. »

Dabbaax daa na fàttali liy jariñaate, ku mu mësaan a wax ak yow it nga dégg ko, déglu ko. Dara walla lenn tënku ko woon moo tax da daan wax li mu gëm te Yàlla tax, moo tax tamit tey ci Senegaal, fi réew mi tollu, bi sëriñ si noppee te waroon a wax, Dabbaax mooy ki wuute te gën a teew. Kon Dabbaax làqu na, waaye baatam du mës a fey.

Nuy fàttali ne Allaaji Abdu Asiis ku Yàlla may la woon. Beykat la woon te daan na yaxantu, maanaam jënd ak jaay, booleek nekkoon boroom xam-xam bu ñu ràññee lool te weg ko weg gu amul xàjj ak séen, ci ñi mu bokkal diine lislaam ak ñeneen ñi ci bokkul waxumalaak kon yeneen tarixa yi. Dund na 93i at. Waaye, booy xool bu baax danga naan Dabbaax daal da fee jooxoon rekk.

Ginnaaw bakkan bu ñam dund, dina mos dee, Yal na Yàlla dolli ngërëm ak yërmaande ci moom. Yal na nu ko feyal.

Ndey Koddu FAAL

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj