“DAÑU NAR A DÉJJATI MAKI SÀLL…”

Yeneen i xët

Aji bind ji

Paap Aale Ñaŋ a fésal xibaar bu doy waar ci xëtu Facebookam. Daf ci siiwal kàddu yoy, nee na kii di Kiristof Gomaar (Christophe Gomart) di Seneraalu larme Farãs te jiite woon yëddukati Farãs yi moo wax ne dañu nar a déjjati Maki Sàll. Bees sukkandikoo ci Paap Aale Ñaŋ, Seneraal bi moo wax ne :

“Fileek larme bi ak sàndarmëri ñoo ngi koy jàppale, dina wéy di toog. Waaye dañ ko nar a déjjati (coup d’Etat) bu ñu ko dummooyoo.” 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj