DEGGOO BU YEES DIGGANTE SENEGAAL AK FMI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Nguurug Senegaal ak FMI (Font monétaire International), di mbootaay miy saytu kopparu réewi àddina si, am nañu ab déggoo bu yees. Keroog, ci alxames ji, 11 me 2023, lañ ko siiwal. Muy déggoo bu war a dem ci diirub ñetti at.

FMI daf fi njëkk a yónn ay ndaw ngir ñu amalsi ci réew mi tukkib nemmeeku. Mu doonoon yónnent bees fi doon doxsi li ko dale talaata 25 awril 2023 jàpp alxames 11 me 2023. Ci kilifteefu Sëñ Edwaar Gemayel mi FMI dénk mbiri Senegaal, amal nañ i njàngat ci koom-koomu réew mi ak ni ko Nguur giy saytoo.

Ci kow loolu, li doonoon seen i tànk dëgg-dëgg mooy dégtal Nguurug Senegaal ab sémb ñeel doxalinu Nguur gi ci anam yi muy saytoo koom-koomu réew mi. Bi ñuy jeexal seen ub tukki keroog ci alxames jooju, amaloon nañu ab lël fale ca njëwriñu ngurd meek gafakag réew mi ngir baaxe taskati xibaar yi seen ngirtey nemmeeku.

Jëlee nañu ca ni, déggoo am na ci diggante ñaari pàcc yi. Muy déggoo buy jëmmal sémb bu yees ñeel koom-koom beek Kopparal gi. Ñu teg ko ci ñaari mbir. Mi ci jiitu mooy baral gi ñeel anam yi ñuy jote xaalis bi, di tëral i pexe yuy tax ba ñuy jot xaalis ni mu gënee gaaw te bare. Ñaareel bee ngi aju ci kàttanal koom gi ba réew mi mën dee dékku jafe-jafe yi ci diir bu yàgg.

Ñaari mbir yii ñu boole jiital dinañ tax, ci seen i kàddu, ba Senegaal mën a jële ci FMI 1 150i tamñareti FCFA yuy doxal sémb bi diiru ñetti at. Mu war a tàmbali ci weeru suwe 2023 dem ba ci weeru suwe 2026. Waaye, ci beneen anam, am nay  wareef yu ciy fekk Senegaal. Ñu mën koo tënk ci xeex luubal alalu askan wi, wàññi borub Nguur gi jaare ko ci xoolaat ni muy séddalee ndimbal yi, dooleel cumbeef yi ajuwul ci Nguur gi ak a sàmmonteek sàrt yiy aar kéew gi.

Ginnaaw bi ñaari pàcc yépp àndee ci déggoo bi, saytukati FMI yee ko war a càmbar laata ñu koy xaatim.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj