Ci talaata jii, 31 oktoobar 2023, la kurél giy saytu wote yi ci réewum Senegaal (CENA) jël ndogal ne DGE dafa war a jébbal Usmaan Sonko ay xobi baayaleem.
Cig pàttali, layookati Sonko yi jaaroon nañ fu nekk ngir DGE jox xobi baayale yi Usmaan Sonko. Waaye, DGE lànk ne du leen joxe. Ndax, Sonko bokkul ci wayndarew wote yi. Ci la layookati Sonko yi dugal ab dabantal ca ëttu àttewaay bu mag bu Senegaal. wànte, foofa, dañ leen a gàntaloon, jox DGE dëgg ji. Loolu taxul woon layookati Sonko xàddi. Ndax, yemuñu woon foofu, bindaatoon nañ beneen dabantal ca àttewaay bu Sigicoor ba. Ci la àttekat bi dii Sabasi Fay jële ndogal ne njiitul Pastef lii di Usmaan Sonko, kenn du ko génne ci wayndarew wote yi, te it, mën na dem jëli ay xobi baayaleem ca DGE.
Ba tey nag, DGE daf ne, fi mu màtt du ko bàyyi, te Sonko du jot ci xobi baayale yi. Noonu, laayookati Sonko yi tamit tàyyiwuñu, ci lañ demee di ko ñaxtu ca CENA. Ginnaaw bi CENA jàngate mbir yi, la jox ndigal DGE ngir ñu jébbal Sonko xobi baayale yi.
Waaye DGE lànkati ba tëdd ca naaj wa, ne dee du leen joxe. Dem na sax ba génne ab yégle di ci tontu CENA. Ci biir yégle bi, DGE a ngi ciy xamle ne :
« Bu ñu joxul xobi baayale yi Usmaan Sonko ba léegi, dafa fekk ni bokkul ci wayndarew wote yi. Te, sunu taxawaay ci mbir yi boobu ba léegi dafay firndeel sax ndogalu njiitul njëlbeenu néegu caytu bu ëttu àttewaay bu mag bi. Fi mu nekk nii, Sonko nekkul ci wayndarew wote yi. Te, loolu moo tax DGE taxaw fi mu taxaw ba tey. Te it, DGE amul màqaama di dugal kenn ci wayndarew wote yi. Leneen lu ci waay def, mbaa mu wax ko ci, nekkoo di topp li néegu caytu bu ëttu àttewaay bu mag bi dogal… »
Tey ci ngoon gi, bi 15i waxtu jotee, Ayib Dafe dellu woon na DGE, waaye dañ ko bañalati. Fii la mbir yi tollu, te kenn xamul fan lay mujje. DGE tamit, su fekkee ne nii la nar a doxale, mbaa wotey 2024 yi dina jaar yoon ? Ndax dafa mel ni DGE, njiitu réew mi rekk la fi nekkal.