DIC woolu na njiitul kurélu « Sénégal Nouveau », Roos Wardini miy lawax ci wotey 2024 yees dégmal. Dafa mel ni, mbirum ñaari nasiyonaalite yi ñu koy njortal a sabab woote bi.
Démb la xibaar bi jib, ci saa si, daldi lëmbe mbaali jokkoo yi. Bi ñu demee ci dalu web bii di service-Public.fr ngir leerlu, fekk nañ fa ab jukki buy firndeel ni Roos Wardini bindu na ci këyitug wote gu Farãs. Te, loolu, ku amul nasiyonaalite Farãs, doo ko mën.
Ci biir jukki boobu, jàngees na ci ne Roos Wardini mi ngi bindoo fi àmbasaadu Ndakaaru bi, yor limatu 598170594. Moom ngeen di gis ci nataal bii ci suuf.
Moom nag, Ndajem Ndeyu àtte réew mi jàllale woon na wayndareem ba noppi. Léegi nag, ñoo ngi xaar ba xam lu ciy topp. Cig pàttali, lu ni mel a tax ñu gàntal lawaxu PDS bii di Kariim Wàdd.