DIISOOB FÉEWALOO

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw-ëllëg ci altine ji, 26 féewiryee 2024, la diisoo bi Njiitu réew mi woote woon di door. Njëwriñu biir réew mi moo génnee ab yégle di ci xamle nu waxtaan wiy tëddee ak fi muy ame. 

Ci lees xamle, moom Maki Sàll, Njiitu réew, 19i lawax yi Ndajem Ndeyu àtte mi daganal lay njëkk a dalal, bu 11i waxtu jotee ci yoor-yoor bi. Bu dee lawax yi ñu gàntal, ñoom, ci digg-bëccëg bi, bu 12i waxtu jotee lañuy giseek Njiitu réew mi. Fa Jamñaajo la ndaje yiy ame. Ndaje yooyii nag, ag laltaay la ngir waajal waxtaan wi war a door bu 16i waxtu jotee ci ngoon, fa CICAD, ci njiiteefu Maki Sàll miy Njiitu réew mi. Waaye de, 19i lawax yi jàll, ñoom, fasuñoo yéene toog ak Maki Sàll. 

19i lawax yi booloo ci kurél gii ñu duppee FC25 dañu amaloon ndajem caabal (conférence de presse) ci àjjuma ji, daldi wax ne duñu bokk ci diisoo boobu Maki Sàll di woote. Tey itam feddali nañ seen ñàkk a dem ci boobule diisoo. Waaye, fasuñoo yéene toog, bank seen i loxo.

Ñoom waa FC25 xamle nañu ne, bu altinee, dinañ dem fa màkkaanu Ndajem Ndeyu àtte mi.  Liñ ko duggee mooy kalaame Maki Sàll, jéebaane ko fa ngir mu gaaw jàpp ab bés bees war a wote. Ndax, ci seen i wax, Maki Sàll day yéexantu, di wiiri-wiiri ngir gën a mën a lëjal kàrt gi, toog fi ginnaaw bésub 2 awril 2024, di bés bi àppug moomeem di jeex.

Am na nag ñu nangoo waxtaani niki ñetti lawax yii Aamadu Ba, Muhammad Bun Abdallah Jonn ak Idiriisa Sekk. Lawax yi ñu gàntaloon tamit, rawatina waa PDS, dinañ teewi ci waxtaan wi. Bu dee way-moomeel yi, ñu baree ba mu des Aliyun Tin. Moom, njiitul Afrikajom Center, nee na dina wuyuji Njiitu réew mi ci diisoo bim woote.

Diisoo bi nag, ñu baree ci féewaloo. Ñii nangoo dem, ñii lànk ne demuñu. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj