DIISOOB WOTE YI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ndajem ndeyu àtte mi neenaloon dekkare Njiitu réew mi ak sémbub àtte bi Ngomblaan gi wote woon. Daf santoon kilifa yi ko yeyoo, ñu amal i wote ci anam bi mu gënee gaaw laata moomeg Njiitu réew miy jeex. Maki Sàll nag, bésub 2 awril la war a jébbal lenge yi ki koy wuutu. Fileek boobu nag, Njiitu réew mi dafa war a fexe wote yi am ci diggante bi.

Bi ndogalu Ndajem ndeyu àtte mi biree, Njiitu réew mi daf ko nangu, dige ne dina amal ab diisoo ngir jàpp bés bi gën.

Njiitu réew mi nag, Maki Sàll, dina woo way-politig yi cib diisoo ngir ñu jàpp bésub wote yi.

Diisoo boobu, ci diirub ñaari fan lees koy amal, muy altine ak talaata. Bu ñu waxtaanee ba noppi, ci la Njiitu réew mi di jàpp bés bi wote biy am ak àppub kàmpaañ yi.

Bees sukkandikoo ci yéenekaayu Le Quotidien, Njiitu réew mi dina diisoo ak ñi séq joŋantey wote yi li ko dalee tay ci altine ji jàpp talaata. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj