Saa-senegaal bii di Paap Mataar Saar, ab wurekat la, nekk ndaw, tollu ci fukki at ak juróom-ñaar. Bokk na ndawi futbalkati Senegaal yees gën a yaakaar ndax xereñte gi nekk ci moom donte ne ndaw la. Nde, fa mu nekk, fële ca Sàmpiyonaa Àngalteer, ma ngi wéy di wane boppam ak di suuxat cofeel gi tàggatkatam bii di Antoñoo Konte am ci moom.
Gannaaw Kuppeg Afrig bu 2022 bi, te Senegaal jëloon ko, la Paap Mataar Saar juge woon ca këlëb ba mu nekkoon fee ca Farãas, Fc Metz, dem fa këlëbam bu bees, Tottenham ca Àngalteer. Ba muy door a dem nag, daanaka jotul woon a wure benn joŋante ak Tottenham. Xanaa as-tuut ca seen joŋantey waajtaay ya. Ba Sàmpiyonaa ba di door sax, daawul bokk. Dafa daan toog kaw tirbin ya, di seetaan, ba mu yàgg muy bokk ndànk-ndànk, di toog ci baŋ bi. Njorteesoon na ni, li mu xaw a tuutee gënoon a tax mu xeebu ci bëti Antoñoo Konte. Nde, futbalu àngale yi, daanaka dafa laaj doole ak dëgër. Waaye de, du woon ñàkk a mën a wure. Dafa di, li xale biy def ci bal, xel-ñaar amu ci. Aay moom, def na ko, wax dëgg. Dooley it, ñàkku ko.
Donte li mu doon bokk bariwul, waxuma sax di dugg ci pàkk bi, teewul Aliw Siise, woo ko ci kuppeg àddina si, mu jot fa amal i joŋante yu mu bokk. Ba loolu weesoo ba mu dellu këlëbam nag, gis nañu ni am na lu mu yokk ci moom ci jom ak fulla. Ci fan yii ñu génn, jot na dugg ñaari yoon. Benn bi, ba joŋante ba desee 10i simili, ba ca des ci ay simili yu gën a bari, mu dëggal ca boppam, wane fa njàmbaar, fulla ak faayda. Ba mu wanee loolu nag, du seetaankat yi kese la lukki seen i gët. Ndaxte, kii di Antoñoo Konte sax, gis na loolu, bég ca ba sànni ciy kàddu, di xamle ni sopp na 2i ayu-bés yi mu defaat ak ñoom, moom Paap Mataar, ba mu jugee kuppeg àddina sa. Njàmbaar la ci wane ak yokkute. Dolli ci ni dafay des ca këlëb ba, ndax réerewuñu ni am na ay këlëb yu koy laaj ngir ñu abal leen ko, ku ci mel ni “Valence”, ca Espaañ ak yeeneen ca wàllu Itaali.
Tay jii ci gaawu bi, 7i fan ci weeru Saŋwiyee, 2023, Tottenham doon amal ndaje ak Portsmoth FC, kuppeg Àngalteer, gañe ko benn bal ci dara (1-0), Paap Mataar Saar tàmbali wii yoon, mel ne dañu ko doon jat ak jat yooyu ñuy wayal gaynde yi (sakajaa, makajaa…), mu ñëwati wane dereetu gaynde gi nekk ci moom. Nangu na fay bal yu bari, amal fa paas yu set ba noppi ànd ceek dal. Lóolu di lu dal xel te di mbégte it ci xolu bépp soppeem, rawatina Saa-Senegaal yépp.
Bu gënee góor-góorlu, dina fa nangu palaas kenn, te dees na bari lees koy gis. Dafa di, doomu gaynde, gaynde lay doon.