DOOMU SENEGAAL JI ÑU REY CA FARÃS

Yeneen i xët

Aji bind ji

Xew-xew bu tiis boobu mi ngi am ci guddig talaata jàpp àllarba. Takk-deri tubaab yi ñoo bóom lenn ndongo Saa-Senegaal lu fa doon jànge. Ci seen i wax, njangaan loolii ñu rey, Sàmba J. Jaañ, dafa tàggoo woon ak sagoom.

Kenn ci dëkkandoo njàngaan li moo woo takk-der yi. Ndax, ci li AFP xamle, dafa doon dégg coow lu bari lu doon jóge fa Sàmba J. Jaañ Mbay dëkk.

Moom, ndem-si-Yàlla ji, Jëppal la fekk baax. Menn at kepp la defagum Farãs.  Daf fa demoon ngir àggalee fa njàngam. Daf doon liggéeyaale ni ko moroomam yépp di defe. Ndeysaan, dañ koy mujje dàq ci liggéey boobee. Ci li tubaab yi wax, bi mu ñàkkee liggéeyam la ame naqar wu réy ba faf xaw a tàggook sagoom. AFP jukkee na ca takk-der ya ne, Sàmba Jaañ dafa ame woon feebaru xel.  Ca lañu ko yëgalee takk-der ya ñu ñëw.

Bi ñu duggee fa béréb ba mu dëkk, fekk mu yor paaka waañ bëgg a dal seen kow. Ci lañu ko bóomee. Anam yi ñu ko faate nag jur na coow. Ndax, dafa am ñu jàpp ne, ni ñu leen tàggatee waroon nañoo am ay pexe ba jot ci moom te duñu ko bóom. Waaye de, narul mujj fenn.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj