Doxub sàrgal Séex Anta Jóob

Yeneen i xët

Aji bind ji

Mbootaayu Panafrig « La marche internationale Dakar-Thieytou » amaloon na am ndaje ak saabalkat yi ca « Grand Théâtre » bu Ndaakaru. Jubluwaayu ndaje maa doon màggal ak a sàrgal Séex Anta Jóob. Moom nag, Séex Anta, bokk na ci boroom xam-xam yu ràññeeku ci àddina si ci 20eelu xarnu bi.

Ñoom nag, dañuy faral di amal, at mu nekk, ab dox diggante Ndakaaruak Céytu. Ca daara ju kowe jees ko dippee la dox bi tàmbalee bi 8i waxtu ci suba jotee.

Dox boobu nag, ci gaawub tay jii la, 1eelu fanu féewiryee 2025, la door, jàpp àllara 5i fan ci weer wii. Bu ñu àggee, dinañu noppalu tuuti sog di amal am ndaje fa Céytu, di dëkk bi Séex Anta Jóob juddoo ca atum 1923. Jubluwaayu ndaje mi mooy waxtaane Séex Anta ak ndonol xam-xam li mu fi bàyyi.

Bees sukkandikoo ci njiitul mbootaay bi, Nikolaa Siñoor Buwasi xamle na ne, wii mooy 11eelu yoon ñuy amal bile dox. Te, ay ndongook i taalibe Séex Anta yeek soppeem yi, ñépp a leen nar a fekksi, dooleel leen ànd ak ñoom. Wëppaw doxu bu ren jii di « Ak fi àddina tollu, wan yoon lees war a jaar ba Afrig moom boppam ci fànni koom-koom, pólitig ak mbatiit ».

Muy fàttali tamit, moom Nikolaa, ne jubluwaay bi ci ëpp solo mooy « siiwal ak it gën a fésal liggéeyub Séex Anta ci xam-xamam beek gis-gisam ñeel ni àddina di doxe ». Ngir loolu mën a am, « ci diirub doxantu bi, dinan defaale ay waxtaan ak i ndajem fénc ci daara yi, xamalaaleel ndongo yi kan mooy Séex anta Jóob, rawatina ay jaloorem yiy tax nu xam sunu mboor ».

Mamadu Faal Erve, di ki ñi baayale xewu ren mi, wax na ne « dañoo war a boole jaar-jaaru Séex Anta ak i njàngaleem ci njàngum réew. Loolu dina tax gis-gisam ñeel Afrig gu boolo doon benn mën a nekk. Te loolu dina doon jéego bu réy ngir ñu gën a jox Afrig gëddaam, gën ko ràññe ».

Seriñ Fàllu Géy di njiitu grand théâtre dalal na seen xel di leen wax ne, Guléet ci ren kilafay nguur gi di gunge ñi taxawal doxu bi, te it dinañ leen taxawu ci wàllu jumtukaay ak koppar yi mu laaj.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj