Ëttu àttekaay bu kawe bi gàntal na càkkuteefu PDS gi lawax yi ñu téye. Nde, ñoom waa PDS ak lawax yiy wax ne dañ salfaañe seen i àq, dañ bindoon ag dabantal, ci sàkku ci Ëttu àttekaay bu kaw bi mu neenal dekkare yi Njiitu réew mi mujje jël ñeel wotey 2024 yi.
Tey la àttekati Ëttu àttekaay bu kawe bi doon daje ngir xawma, càmbar càkkuteefu PDS ka lawax yooyiy tuumaal Ndajem Ndeyu sàrti réew mi. Ci njeexital ga nag, ëtt bi dafa gàntal seen càkkuteef gi. Ndax, daf leen xamal ne, ci wàll wii, Ndajem Ndeyu sàrti méew mi rekk a am sañ-sañu dogal.
Kon, PDS amatul weneew yoon wu muy jaarati ngir jéem a yàq wote yi. Waaye, xibaar bu bees dafa rot, ñuy wax ne Pekkug Ngomblaan gi dafa woote liggéey bu jamp ci ngoonug tey jii, àjjuma 15 màrs 2024. Bees sukkandikoo ci Ayooba Fay, taskatu xibaar bu wóor, wooteb Ngomblaan gi jotewul dara ak wote yi. Loolu nag terewul ne xel yi teey nañ. Ñu xaarandi ba xam lu wund woote bi.