Ren, soppey kuppe dinañubégg bég. Nde, ginnaaw sàmpiyonaa yi jeex ak Ligue des champions bi, amati nañ yeneen ñaari joŋante yu mag yu leen di xaar : EURO 2024 ak Copa America 2024.
EURO 2024
Joŋantey powum kuppe (futbal) ñeel réewi Tugal yi, ñu dippee ko “EURO”, day faral di ñeenti at yu jot. Ren jii nag, réewum Almaañ mooy dalal joŋante bu mag boobiy doon 17eel bi ci mboor. Ñaar-fukk ak ñeenti (24i) bar (ekib) yu séddaliku ci juróom-benni (6i) kippu ñooy xëccoo kub bi, ci limub 51i mats.
Àjjuma jii, 14i pani weeru suwe, la xewteg kuppe giy door. Almaañ mi dalal po mi ak Ekos ñooy amal joŋanteb kubbite gi, bu 19i waxtu jotee ci ngoon.
Nii la kippu yi tëddee :
Kippu A
Almaañ
Ekos
Ongiri
Siwis
Kippu B
Albani
Espaañ
Itali
Kurwaasi
Kippu C
Àngalteer
Danmaark
Seerbi
Solooweni
Kippu D
Farãs
Otiris
Peyi-Baa
Poloñ
Kippu E
Belsig
Ikren
Rumani
Soloowakii
Kippu F
Purtugaal
Ceg
Seworsi
Tirkii