Mats yi ñeel 1/4 dë finaal yi “Euro” bi jeex nañ barki-démb ci gaawu gi. Nii la njuureef yi demee :
Espaañ 2-1 Almaañ
Farãs 5-3 Portigaal (seri)
Àngalteer 5-3 Siwis (seri)
Peyi-Baa 2-1 Tirkii
Suba ci talaata ji la démi-finaal yiy door diggante Espaañ ak Farãs. Ginnaaw-suba, Peyi-Baa ak Àngalteer dinañ laale. Ñaari joŋante yépp, bu 19i waxtu jotee lañuy tàmbali.
COPA AMERICA
Mats yi ñeel 1/4 dë finaal “Copa” bi tamit jeex nañ ci bésu gaawu gi. Nii la njureef yi demee :
Arsàntin 4-2 Ekuwaatëer (seri)
Wenesuwelaa 3-4 Kanadaa
Iriguwey 4-2 Beresil (seri)
Kolómbi 5-0 Panamaa