F24, ÀND XEEX 3EELU MOOME

Yeneen i xët

Aji bind ji

Njiitu réew mi, Maki Sàll, amati na soxla. Nde, kurél gu bees juddu na gog, jàmmaarloo ak moom a ko tax jóg. Démb, ci dibéer ji, 16 avril 2023, la kurél googii taxaw. Dees na ci fekk ay way-moomeel, mbootaayi aada, làngi pólitig ak i kilifa yu ràññeeku ci réew mi. Jubluwaayam bu njëkk mooy gàntal 3eelu moome gu Njiitu réew miy xemmem.

112i mbootaay ñoo xaatim sàrtub kurél gu bees gees duppee, ci farãse, Plateforme de lutte des forces vives de la nation, gàttal biy joxe F24. Démb, dibéer 16 awril 2023, la juddu. Lees ko duggee mooy waxtaan ak askanuw Senegaal, woo leen cig bennoo, jàkkaarloo ak Njiitu réew mi, Maki Sàll, ga ko mu sàmmonte ak Ndeyu-àtte réew mi, waaye mu jëfee tam kàddoom. Maanaam, li kurél gi bëgg mooy Njiitu réew mi, Maki Sàll, génnee mbirum ñetteelu moome cim xelam, daldi janook waa Senegaal yépp, wax leen ne du bokk ci wotey 2024 yees dëgmal. Nde, ñoom ñi sos kurél gi, dañu gëm ne 3eelu moome gi dafa safaanoo ak li Yoon sàrtal, te yit dëppoowul ak xel mu rafet, astemaak ngor.

3eelu moome gi dafa gën a fës ci jubluwaayi kurél gi. Waaye, nag, am na yeneen i mébét yi muy diir. Ndaxte, waa kurél gi dañoo fas yéene xar seen i tànki-tubéy, xeex ngir ñu dindi dogi L29 ak L30, ak sax bépp xeetu dog walla sàrt bu nekk ci càrtug wote gi te ñuy gàllankoor àqi lawax yi bëgg a bokk cib wote. Dañuy, waa F24, xeex tamit bépp xeetu àtte bob, Yoon daf cee jeng, ngir rekk faagaagal kenn ci way-pólitig yi war a dundal demokaraasi. “Parrainages” yi sax, ci li ñuy jéem a fexe mu deñ la bokk. Loolu la kàdduy Muhammadu Mbóoj yiy leeral, bi muy wax ne dañuy xeex :

“…àttey biir néeg yi nga xam ne dañuy tax, walla mën nañoo tax ab lawax ñàkk a mën a bokk ci wotey 2024 yi, fekk ne dañoo jalgati Yoon.”

Rax-ci-dolli, kurélug F24 day laaj ñu bàyyi ñees jàpp ci sababu pólitig doŋŋ, bàyyi nit ñiy ñaxtu saa bu leen soobee, te fexe ba amal i wote yu amul xàjj-ak-seen, yu jaar Yoon te leer nàññ. Muhammadu Mbóoj neetti : 

“F24 daa fas yéene jàmmaarloo ak Nguur gii fi nekk ngir ñu sàmm àqi nit ñi, bàyyee leen seen i yelleef. Te, noo ngi woo askan wépp, keroog 12 me 2023, ñu dajaloo def mbooloo mu réy ngir xeex ñetteelu moomeg Maki Sàll gi xam ne, dafa safaanoo ak Ndeyu-àtte réew mi. “

Atum 2011, kurél gu ni mel, M23, taxawoon na ngir xeex ñetteelu moome Njiitu réew ma woon, Abdulaay Wàdd. Kenn mësul njort ne, 12i at ci kanam, dina amaat geneen kurél guy xeex mbirum ñetteelu moome. Kon, mënees nabwax ne, ci wàllu Yoon, Senegaal dafa dellu ginnaaw, rawatina ci fànnu demokaraasi. 

Ndax, bu doon ne kóolute am na ñeel Yoon wi fi nekk, dañuy bàyyee Njiitu réew mi ak Yoon mu lijjanti ko. Bu fi demokaraasi amoon itam, baatu askan wi rekk doon na doy ci saafara mbir mi. Nde, ginnaaw 2019 ba tey, Maki Sàll ak i àndandoom dañoo ñàkk wote yu ci topp yépp. Muy wone ne askan wi doyal na ci seen ug Nguur. Jarul kon ñuy sampati seen ndënd ci géew gog, boroom bëggu leen cee gis.

Dafa di, nag, 2011, ak lu ci jotoon a xew yépp, Abdulaay Wàdd mujjoon na bokk, donte ne faluwul woon. Wii yoon, nag, ñoo ngi xool ba xam F24 dina am ndam ci xeex bi mu sumb.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj