Waa F24 fas nañoo yéene wéyal seen xeex bi. Loolu lañu siiwal keroog àjjuma bi ñuy jàkkaarlook taskati xibaar yi. Booba, daa fekk perefeb Ndakaaru bi dàq seen ndaje mi ñu doon woote ci àjjuma ji. Ñu dellu nag wooteeti yëngu-yëngal.
Ci àjjuma ji la waa kurél gii di F24 nammoon a amal seen ub ñaxtu biir Ndakaaru. Waaye cib jàkkaarlook taskati xibaar yi lañu mujje. Nde perefeb Ndakaaru bi dafa gàntalati seen woote boobu. Looloo waral ba ñu dellu doon jàkkaarlook taskati xibaar yi ngir xamal Saa-Senegaal yi naka lañuy (ñoom waa kurél gi) mujje doxale.
Ginnaaw bi ñu ñaawloo gàntal gi perefeb Ndakaaru gàntalati seen ñaxtu boobu, waa F24 dellu nañ xamle ni Nguurug Maki Sàll gaa ngi wéy di salfaañe seen i àq ak yelleef. Waaye loolu du leen tax a dellu ginnaaw ñoom itam.
Naka noonu, ñuy xamal askan wi ni fasuñu yéene toog di xoole, walla di seetaan Maki Sàll ak Nguuram ñuy def lu leen neex rekk. Tere na leen ñaxtu waaye mënu leen a tere yëngu-yëngal. Te duñu ci xaar dara muy yàgg, nde ci dibéeru démb ji lañu delloo woon buum ca boy-boy ga. Dañu woo woon Saa-Senegaal yi ci lu ñu tudde « xumb te leer », maanaam yëngu ba ñépp dégg leen ak leeral fépp.
Bu ko defee, « lépp lu ñu mën a jëfandikoo baax na. Moo xam ay bool lay doon, ay mbiib, ay kalaksõ walla i wuuwuselaa. Nañu ko def mu riir bu baax a baax te leeralaale fépp ak sunuy niitug jollasu ». (Faatu Bolondĩ Jóob).
Ba tey ci kàdduy Faatu Bolondĩ Jóob, dina doon wooteb yëngu-yëngal bu ñuy def « ngir sàmm jàmm ji, jibal dëgg ak yoon. » Ñu ciy woo Saa-Senegaal yépp, fii ci biir réew mi ak fa bititm-réew : « maxejj yépp, mag ak ndaw, góor ak jigéen, fépp fu ñu mën a nekk fi Ndakaarook li ko wër, fi àll bi. Nañu doon benn te génn ci dibéer ji 10 sàttumbaar bu 21i waxtu jotee jàpp 22i waxtu ngir Nguuru Maki Sàll gi dégg nu. »
Ginnaaw ba nga xamee ni perefe Ndakaaru bi mayu leen fu ñu ñaxtoo, waa kurél gee ngi xamleet ni dinañu wéy di dox doxu ñaxtu. Dinañu ci booleet dummóoyu ak bank seen loxo. Noonu lañu nar a wéyalee xeex bi ba balaa ñuy féexal Usmaan sonko ak 1000i Saa-senegaal yi ñu nëbb jant bi ci jaay doole.