Niseer, ginnaaw bi sóobare ya foqatee Nguur ga ca loxoy Mohamed Basum, dañoo fas yéene soppi doxalin wa, càmbaraat digaale ak pas ya Njiitu réew ma woon xaatimooon. Coppite yooyee, bokk na ca digaale yiñ sékkoon ak Farãs. Loolu nag, neexul njiiti Farãs yi. Waaye nag, sóobare ya ñoom, dañoo dogu ci soppi réew ma, dog buumu njaam gi leen nootkat bi tukkee, ati 1960 yi ba tey. Moo tax, ci xeex ak xëccoo bu metti lañ nekk. Nee ñu sax, Farãs a nekk ci ginnaaw CEDEAO mi gàll i daan waa Niseer. Loolu taxul ñoom Abdurahmaan Ciyaani mi jiite sóobare ya dellu ginnaaw.
Dafa di, ginnaaw biñ seetloo tuuma ak ŋàññ yi waa Farãs dëkkee ñeel leen, jël ndogal lu réy. Nde, ci àjjuma jii weesu la kilifay Niseer yu yees yi jotoon àppug 2i fan kii di àmbasadëeru Farãs bi ngir mu génn réew ma. Maanaam daal, dañ ko dàq.
Farãs nag, nee nañu seen àmbasadëer bi du fa jóge. Li ñu lay mooy ne, sóobare yi amuñu sañ-sañ walla màkkaamay dàq seen àmbasadëer. Ndax, ci seen i wax, du ñoom la askanu Niseer fal. Moone de, fan yii yépp, ay junniy junni saa-niseer ñoo ngi fees dell ci estaad yeek mbedd yi, di kaas ak a sàkku Farãs abal leen seen réew. Ndax, ci seen i wax, teewaayu Farãs musiba doŋŋ la leen mës a jural.
Dafa mel ni nag Macron, Njiitu réewum Farãs, déggu leen walla daf leen a tanqamlu. Démb, altine 28i ut 2023, moom Macron, doon waxtaan ak ndawi Farãs yi ci àddina sépp. Ca waxam ja, àdduwaale na ci mbirum Niseer, ne :
“Ay weer a ngi nii Farãs ak ndawi nguuram di jànkonteek i jafe-jafe ci yenn réewi Afrig yi, rawatina fa Sudã nga xam ne amoon nañ fa taxawaay bu rafet. Ba sax fa Niseer, nga xam ne moo nu jaaxal jamono yii may wax ak yeen. Dama ciy jaaraale di nuyu seen naataango ba fa nekk (…) sóobare ya amuñu màkkaamay jël ndogalu dàq ko… Jàpp naa tamit ne pólitig bi nuy doxal mooy bu baax bi. Ndaxte, dafay am njeexital ci njàmbarteg Muhamed Basum ak taxawaayu sunu ndawu Nguur la fa nekk ak lañuy daj lépp ci néewal ko doole.”
Muy kàddu yoy, dañuy wone ag réy ak ug ñàkk a wormaal askanuw Niseer wi nga xam ne, fësal na ag péeteem bu yàgg. Te, ñoom maxejji Niseer yi, dummooyu nañ Muhamed Basum ak i àndandoom démb balaa tey. Bu Adurahmaan Ciyaani amul woon sañ-sañ sax, taxawaayu askan wi rekk doy na ci may ko dayo bi ak sañ-sañ bi. Kon, li tax Farãs lànk bañ a dem, day wone rekk ne am na lum fa am lol, bëggu koo ñàkk. Te, nee ñu, irañëm (uranium) Niseer bi lay bañ mu raw ko. Ndax, bu boobaa, dina ko indil jafe-jafe yu réy a réy ci wàllu laf, mbëj ak koom-koom. Farãs a ngi mel mag mu bañ a fer, dëkk ci di nàmp ak ratt weeni Afrig yi rekk, bëgg ko dëkke abadan.
Afrig nag, rawatina Mali, Burkinaa Faaso ak Niseer, yeewu nañ. Te, fasuñoo yéene may dara Farãs. Wolof ne, fullaay jaay daqaar.