Fiara (Foire internationale de l’agriculture et des ressources animales) bu 2024 bee ngi ñuy wéyal fa Cices. Barki-démb, ci dibéer ji, 26 me 2024, la waroon a jeex. Waaye, dees na ko xëcc ba alxames 30 me ngir may ñi mujje ñëw, rawatina waa Burkinaa Faaso yi seen sëfaan amoon i jafe-jafe ci yoon wi, ñu mën a wone seen liggéey.
Magum jëwriñ yi, Usmaan Sonko, demoon na fa ngir nemmeeku yees fay fésal. Yëkkati na fay kàddu itam. Muy xamal Saa-Senegaal yi ni, seen Càmm gi dina saafara jafe-jafey dund bi te dinañu àgg ci dundal sunu bopp. Ñu gën koo miin, ci làkkuw farãse, ci kàddug “autosuffisance alimentaire”. Naka noonu, muy leeral ni lu mën a nekk la. Dafay laaj ñu def ci li war ci ñeel nit ñi koy jooxe, ci wàllu xarala ak koppar. Te, Càmm gi tegu na ci yoon wi.