Jar-jar (prisonniers) ya nekk ca kasob Kàmpenaal (Camp penal) bu “Liberté 6” ñoo doon fippu. La ko sabab mooy anam yu metti ya ñu fa nekke. Loolu lañu doon ñaawlu, daldi fippu ba mbir mi ëpp i loxo. Nde, dañu mujje jàppante ak takk-der yay wattu kaso ba.
Anam ya ñuy dundee kaso boobee di kàmpenaal moo naqadi jar-jar ya ñu fa téyeendi. Bees sukkandikoo ci li rot ciy xibaar, na ñu fa nekkee, dëppoowul ak dundiinu doom-aadama. Te, joxeesu leen worma ak cër bi war. Ba tey, ci lees for ciy xibaar, béréb dafa xat lool ci ñoom. Ndax, ba ñuy tabax kaso bi, 500i nit kese la waroon a jël te, jamono jii, 1 500i jar-jar ñoo fa nekk. Rax-ci-dolli, toppatoowuñu leen ni mu waree.
Loolu yépp lañ guuxal mer, ànd ak li takk-der yi duggoon ca seen néeg ya di am lu ñuy seet. Ca la fitna juddoo, ñu jàppante, takk-der ya sàndi ay lakkirimosen ca seen biir néeg ya, soqi seen kow ay xotti sox (balle à blanc).
Nee ñu nag, am na ñu ca jëlee ay gaañu-gaañu. Bi ko jëwriñu Yoon wi yëgee, dafa gaawantu dem ca béréb ba ngir delloosi fa jàmm. Ba mu fay jóge, ag dal delsi woon na fa.
Lile day wone ne, tabax ay kaso yu yees yu dëppoo ak jamono dafa war te jamp lool. Warees na yit ñoŋal nekkiinu jar-jar yi, dooleel takk-der yi wattu kaso yi, jox leen i jumtukaay yu mucc ayib yi leen di tax a def seen liggéey ci anam bi war te kenn du ci loru. Nde, loolu, dafa bokk ci jub, jubal ak jubbanti.