FMI feddali na yéeneem ci liggéey ak Senegaal, gunge ko ngir mu joyyanti nafaam gi. RTS moo siiwal xibaar bi. Démb ci alxames ji, 6 màrs 2025, Julie Kozack mi yor jokkoo FMI doon na amal ndajem saabal fa Washington. Ci biir i waxam, soxna si junj na ne FMI mën na am lu mu baal Senegaal ci bor bi.
Cig pàttali, ëttub cettantal bi dafa siiwal ag caabal guy biral ay njuuj-njaaj ci anam bi Nguurug Maki Sàll ga woon yoree woon xaalis bi. Ba tay ci li caabal gi siiwal, dañoo nëbboon bor bi, joxe ay lim yu wérul. Démb nag, ca ndajem saabal ma mu doon amal Washington, Julie Kozack jot na àddu ci mbirum Senegaal bi ko ci saabalkat yi laajee. Ci tontoom, soxna si dafa xamle ne FMI moo ngi waxtaan ak njiiti Senegaal yi ñeel rëq-rëq yi caabalug ëttub cettantal bi siiwal. Bees sukkandikoo ciy kàddoom, caabal gi dafa dëggal daanu bi nafag réew mi daanu diggante 2019 ak 2023.
Njiiti Senegaal yu yees yi dañoo jël ndogalu wax askan wi dëgg, waayeet wax ay digaaleem ndono li leen Nguurug Maki Sàll gi bàyyee ñeel koppari réew mi. FMI nag dafa rafetlu taxawaay bile. Moo tax mu fas yéene jàppale Càmmug Senegaal gi ci liggéey bi ñu sumb ngir tegaat koom-koomu réew mi ci yoon.