FRAPP : NOO BAÑ ! “ASSISES DE LA DÉMOCRATIE” BI MAKORÕ BËGG A AMAL UCAD DU FI AME !

Yeneen i xët

Aji bind ji

Waa FRAPP siiwal nañu ab yégle, démb àllarba 18 suwe 2025, di ci biral seen ñàkk ànd ci ndajem péncoo bi Njiitu réewu Farãs, Emaniwel Makorõ, namm a amalee fa jànguneb Séex Anta Jóob bu Ndakaaru.

“Front pour une Révolution Anti-impérialiste Populaire et Panafricaine” (FRAPP) dafa bind ci yégleeem bi, wax ne àndul wenn yoon ci ñuy amal Ndajem péncoo ñeel Demokaraasi Afrig ci lélub 19 jàpp 22 suwe fa jànguneb Séex Anta Jóob bu Ndakaaru (UCAD). Ndax, ci li ñu bind, xew-xew boobu, Njiitu réewu Farãs, Emaniwel Makorõ, moo joxe xaalis bees koy amalee, te yit moo ko xalaat.

Waa FRAPP nag, dañu jàpp ne way-mbéeféer ya woon dañu nekk di nas i pexe ngir wéy di noot réewi Afrig yi. Nde, ci seen xalaat, li Njiitu réewu Farãs li dugge ndaje moomee ñu dëgmal du lenn lu dul xàll yoon wu bees wow, ca lay jaar ngir jëmbat fi mbéeféer gu yees. Ngir jëmmal yéene jooju nag, ba tay ci gis-gisu FRAPP, way-mbéeféer ya woon dañuy taafantoo nikiy waxtaani demokaraasi, jaare ci ngir am li ñu bëgg. Te loolu, “wareesul a jëfandikoo bérébu xam-xam bu màgg, nekk fii Afrig, ngir lewal ko. “

FRAPP rax na ca dolli sax, ne, “Assises Africaines de la Démocratie” yooyu ak “Forum de Montpellier” bu 2021 bi ñoo bokk jubluwaay : nax nit ñi, jéem leen a gëmloo ne buumu njaam gi doxoon diggante Farãs ak Afrig (Françafrique) dagg na fekk ne yoo, dañoo nas pexe mu yees ngir gën a noot saa-afrig yi.

FRAPP fàttali na ci yégleem bi ne, ba ñu jógee ca “Forum de Montpellier” bu 2021 ba lañu taxawaloon kurél gii di “Fondation de l’Innovation pour la Démocratie ” (FID), di kurél gog, AFD a ko kopparal, “Quai d’Orsay” xalaat ko, ñu dénk ko ay xeltukati Afrig yees tànn ngir ñu doon maalaan miy nëbb pólitig di Farãs di amal ci suuf ñeel kembaaru Afrig.

Naataangooy dépite Gii Mariis Saañaa yi xamleet nañu ne, Farãs ciy pexe lu lëndëm la nekk. Nde, ginnaaw gis na ne réewi Afrig yee ngi tàmbalee yeewu, di moom seen bopp, xam ne mënatul a jëfandikoo ay ngànnaay ngir jaay leen doole. Loolu moo tax mu bëgg a jaare ci mbatiit mi, lëndëmal xeli saa-afrig yi, soppi seen xalaatiin, nootsleen i xel, defloo leen li mu bëgg. Pexe moomu nag, FRAPP dafa jàpp ne way-mbéeféeri Farãs yu yees yi dañu ci bëgg a kootoo ak i campeef ak i jàngune. Li ñu ci jublu mooy soppi jàngune yi, def leen i béréb yees di toggee nooteel gi (laboratoire de la domination).

Kurélu FRAPP nag, ci yégle bi, bind na, wax ne :

“Jànguneb Séex Anta Jóob mënut a nekk, te warut a nekk béréb bees di lewalee pexem naxaate moomu. Ci mboor, bérébu bañ la mës a doon, béréb bees di toggee ay xalaati moom-sa-bopp, di bérébu xeex ci njàngaan yi ak askan wi. Bu ñu fa amalee xew-xew boobu [Assises Africaines de la Démocratie], dina worook ndonol Séex Anta Jóob ci boppam, moom mi nga xam ne, dundam gépp daf ko xeex ngir Afrig sóobuwaat ci xam-xam, sàmm ngoram, te di xalaatal boppam. Turu jàngune bi doy na sas. “

FRAPP a ngi woo njàngaan yi, jàngalekat yi, sàndikaa yi, mbootaayi ndaw yi ak kurél yépp ñu taxaw temm ngir ñu bañ a amal ndaje moomu fa UCAD. Nde, ci seen i wax, UCAD dafa war a yam ci di nekk bérébu xam-xam buy dundal coppiteg Afrig, déet bérébu bees di lalee ay pexe yu lëndëm ngir ” Françafrique ” miy song léegi mbatiit yi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj