FUTBAL : FSF ÀDDU NA CI MBIRU ISMAYLA SAKOB

Yeneen i xët

Aji bind ji

Keroog, ci àjjuma jii weesu, la Paab Caw biral toftaleg gayndey kuppe yi. Moom mi toppoon ci Aliw Siise, moo ko wuutandi ci boppu ekib bi. Mooy jiite gayndey Senegaal yi ci ñaari joŋante yiñ dëgmal ci fan yii di ñëw ñeel toogalante CAN biy ñëw. Ñu seetlu ni, keroog, ba mu dugalee ndaw yim tànn, kii di Ismayla Sakob mi nekk Galatasaray dañ ko ci génne woon. Mu jaaxaloon ñu bari ba njiiti futbalu Senegaal yi xamle woon ni déggante nañ ak waa këlëbam, fajkat ya, ba xamal nañ leen ni doomu réew jooju dafa ame gaañu-gaañu ba tax du mën a wuyusi wootey réewam. Mu nekkoon lu yanu maanaa.

Wànte, démb, ci gaawu gi, ñu gis ni moom Ismayla Sakob miñ waxoon ni dafa gaañu ba tax du mën a ñëw. Futbal-loo nañu ko ci seen joŋante ak Alanyaspor biñ bom (1-0). Moom sax, Ismayla Sakob, futbal na 90i simili ya. Loolu nekk lu doy waar te di xaw a niru ñàkkug wegeel ci ekibu Senegaal bi. Looloo waral, démb, ci altine ji, “Fédération Sénégalaise de Football” daldi siiwal ab yégle ngir leeral ni mbir mi deme. Wax na ci li tax ñu bàyyi woon Sakob toog ca këlëbam te muy liñ leen waxoon ni dafa gaañu. Gannaaw li am nag, FSF àddu na ci ak fulla, xamle ni rafetluwul loolee te bëgg na ñu bàyyi Saa-Senegaal bi mu ñëw wuyusi ci nim gën a gaawe.

Loolu mujju na am. Ndax lateraalu càmmoñu gaynde yi aksi na ci bëccëgu altine ji ba fekki nay moroomam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj