FUTBAL / SENEGAAL : ALIW SIISE SIIWAL NA TOFTALEEM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb ci àjjuma ji, 30i pani ut 2024, la tàggatkatu ekibu Senegaal bu mag bi, Aliw Siise, siiwal toftaleem. Fésal na ndaw yim tànn ngir ñu taxawal réew mi ci ñaari mats yi nu dëgmal ci fan yii di ñëw ñeel jàllug kuppeg Afrig 2025 gi.

Ci toftale gi nag, daanaka ku ci nekk mës na wuyusi wooteg ekib bi ba mu des kenn kese. Gan googu nag mooy doomu Sigicoor ji tollu ci 19i at, di futbal ca këlëbu Slavia Prague, nekk réewum Ceg (République Tchèque). Moom nag, ab laafu càmmoñ la (arrière gauche). Nii la toflale gi tëdde :

Góol yi :  Eduwaar Méndi, Móori Jaw ak Séeni Jeŋ.

Defãsëer yi : Kaliidu Kulibali, Musaa Njaxate, Abdulaay Sekk, Miikaayil Fay, Fórmóos Méndi, Ismayila Sakob, Abdu Jàllo, Elaas Maalik Juuf

Miliya yi : Nampalis Méndi, Paate Siis, Seydu Sano, Lamin Kamara, Paap Mataar Saar, Abiib Jara, Paap Géy, Idiriisa Gànna Géy.

Ataakã yi : Saajo Maane, Ismayila Saar, Abiib Jàllo, Ilimaan Njaay, Nikolaa Jakson, Abdulaay Sima, Sériif Njaay.

Bési mats yi

Senegaal / Burkinaa Faaso (àjjuma 6i Settumbar 2024)

Burundi / Senegaal (Altine 9i Settumbar 2024)

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj