Li fës GÀMMU GI By Ndey Koddu Faal 25/09/2023 0 250 Partager FacebookTwitterWhatsAppE-mailImprimer Yeneen i xët YEESALUG NGOMBLAAN GI : EL MAALIG SUMB NA LIGGÉEY BI Paap Aali Jàllo - 05/02/2025 COKKAASU ODIA Odia - 04/02/2025 NAALUW JÀPPANDAL NDOX MU SELL MI Mbay Sow - 03/02/2025 POROFESËER MUSAA DAAF WÀCC NA LIGGÉEY Paap Aali Jàllo - 03/02/2025 Aji bind ji Ndey Koddu Faal Weeru Gàmmu La Buur Yàlla taamu Ngir gane àddina Yonent bi Yàlla def mu gën ci mbindeef yi Gënal ko ñépp moom Rasululaahi Moo tax looy def bëgg mu saf Yàlla Jiital ci Yonent bi te ube ko ko ngalla Bés bii rekk a ñor Sëydi Allaaji Maalig Si Mu woo ci mag ak ndaw ñépp wuyusi Dundal bés bi ni ko lislaam soppe Lépp rafet bijjiy yiw lépp ci diine Tey képp ku fi waxal Yàlla nag Xam nga ni fi Gàmmu gi egg Muy feneen di Senegaal Mawdo moo ko waral Kuy yatt te mënoo, yàq nga bant kon Kuy jàngale xamoo, réerale nga kon Koo bëgg a xamal dangay fexe Ba gën koo xam mooy pexe Ndax boo réeree réerale Doo jot dara bay jotale Am njàng nga woote Ci yow la nuy roote Si Maalig jërëjëf Ci yile jëf Yaa ngi xamle li nu war a moytu Yaa ngi gindi it ci li nu war a saytu Yaw gëlëmalaatewoo mukk Bind nga ba fi lu amul sikk Ngir nu jub te fegu Ragal Yàlla tegu Yaa jar a woy Yaa jar a roy Ku màggal guddi Gàmmu Say aajo biir ak biti faju Ndey Koddu Faal Ndey Koddu FaalPlus de publicationsBiographieNdey Koddu Faalhttps://www.defuwaxu.com/author/ndeykoddufaal10/BÉSUB NJÀNGUM XALE YU JIGÉEN ÑINdey Koddu Faalhttps://www.defuwaxu.com/author/ndeykoddufaal10/MISS LITTÉRATURE SENEGAAL : NEEX XEL, RAFET KÀDDUNdey Koddu Faalhttps://www.defuwaxu.com/author/ndeykoddufaal10/ALIYUN BADARA BÉEY GUDDEE NANdey Koddu Faalhttps://www.defuwaxu.com/author/ndeykoddufaal10/BATAAXALU NGUGI AK BÓRIS JÓOB ÑEEL NJIITU RÉEW MI FacebookTwitterWhatsAppE-mailImprimer Widewo VOA AMAL NAB JOTAAY CI MBINDUM BUBAKAR BÓRIS JÓOB GINNAAW BI WEREKAAN BI JËLEE CARGALUG NEUSTADT 2022 BI. CUQAL CI LËNKAAY BII TOFTALU... Defu Waxu - Xët yi mujj