Weeru Gàmmu
La Buur Yàlla taamu
Ngir gane àddina Yonent bi
Yàlla def mu gën ci mbindeef yi
Gënal ko ñépp moom Rasululaahi
Moo tax looy def bëgg mu saf Yàlla
Jiital ci Yonent bi te ube ko ko ngalla
Bés bii rekk a ñor Sëydi Àllaaji Maalig Si
Mu woo ci mag ak ndaw ñépp wuyusi
Dundal bés bi ni ko lislaam soppe
Lépp rafet bijjiy yiw lépp ci diine
Tey képp ku fi waxal Yàlla nag
Xam nga ni fi Gàmmu gi egg
Muy feneen di Senegaal
Mawdo moo ko waral
Kuy yatt te mënoo, yàq nga bant kon
Kuy jàngale xamoo, réerale nga kon
Koo bëgg a xamal dangay fexe
Ba gën koo xam mooy pexe
Ndax boo réeree réerale
Doo jot dara bay jotale
Am njàng nga woote
Ci yow la nuy roote
Si Maalig jërëjëf
Ci yile jëf
Yaay ki tax nu xam li nu war a moytu
Yaa nu gindi it ci li nu war a saytu
Yaw gëlëmalaatewoo mukk
Bind nga ba fi lu amul sikk
Ngir nu jub te fegu
Ragal Yàlla tegu
Yaa jar a woy
Yaa jar a roy
Ku màggal guddi Gàmmu
Say aajo biir ak biti faju
Ndey Koddu Faal