Gannaaw bi ñu génnee ci lёkkatoog Yewwi Askan Wi ci fan yii. Waa Bés Du Ñàkk bu Sёriñ Mansuur Sy Jamiil ñi ngi woo seen ay militaŋ ngir ñu woteel waa Bennoo Bokk Yaakaar. Mu nekk xew-xew bu metti ci waa YAW ngir ne génn gim génn seenug lёkkatoo dem di dooleel lёkkatoo gi ñuy xeex.
BFEM 2022
Mbir mu yéeme moo xew fale ca Ndar, benn lawax bu am jafe-jafey gis (laago) moo fa am BFEM ci yoon (tour) wu jёkk wi. Moom nag mi ngi wuyoo ci turu Jibriil Géy di jànge ca CEM Augustin Henry Louis Guillabert fale ca diwaanu Saint-Louis.
SAAJO MAANE
Réewum Kataar delloo na njukkal doomu Senegaal bii di Saajo Maane gannaaw bam jёlee ñaareelu ballon d’or biy màndargaal futbalkat bi gёn a ràññeeku ci at mi fii ci biir Afrig. Njukkal li mi ngi doon ab nataalu Saajo Maane bu mag buñ taf ci benn tabax bu gudd ca biir dёkk ba. Réew moomu tamit, mooy réew mi war a amal joŋante bi boole réew yi nekk ci àdduna bi yépp ci weeru Nowàmbar wii di ñёw.
SÉMB XЁYU NDAW ÑI
Sémb boobu jot na démb rekk ca Wakaam lu tollu ci 790i càkkuteef (demande). Maanaam, ñu bёgg bokk ci sémb boobu ngir am ci luñ jàpp. Waaye, lu tollu ci 384i lañ ci nangoogum (enregistrer). Loolu di wane ni ñàkkum xёy mi amee doole ci dёkk bi donte ne sax am na ay sémb yu ñuy nas ngir jёle ko fi. Ndax, ba tey foofu ca Wakaam lu deme ni ki wàllum kopparal gi (financement ) jot nañ lu tollu ci 1236i wayndare.