GÀTTALI BÉS BI (4/6/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

ISRAAYEL RAY NA CI WAA PALASTIIN LU ËPP 15 000iy GONE

Bees sukkandikoo ci tele Al Jazeera, ba xeex ba tàmbalee ba léegi, ca weeru oktoobar, fa Gaasa, sóobarey Israayel ya ray nañu ci waa Palastiin lu ëpp 15 000iy gone.

“Marine Nationale” jàpp na gaal gu yaboon 219i nit ñu doon mbëkki

“Marin National”, takk-der yiy saytu kaaraange géej gi, dañu jàpp ag gaal gu yeboon i mbēkk-kat. Ci ngoonug altiney démb ji lañu leen teg loxo, ca waaxi Ndakaaru yi. Nee ñu, gaal gi, yaboon na 219i nit ñu doon mbëkki.

Limees na ci 25i gone ak 27i jigéen. Bees sukkandikoo ci bànqaasu làrme bi yor wàllu xibaar ak jëflante ( DIRPA), Gàmbi la gaal gi bawoo ci dibéer ji, jaar Sowaal (Joal) ak Caaroy am ñu mu fa jël. Rax nañ ci dolli, ñoom waa DIRPA, ne bu weesoo 151i Saa-Senegaal, am na 35i Saa-Gàmbi, 7i Saa-Gine-Konaakiri, 2i Saa-Gine-Bisaawo, 1 Saa-Kamerun, 21i Saa-Komoor ak 2i Saa-Burkinaa yu ne woon ci gaal gi. Ñoom ñii ñépp nag jébbal nañu leen yoon.

NJÀNGUM XALE YI ÀND AK LAAGO

Barkaatu-démb, ci gaawu gi, Mustafaa Màmba Giraasi doon na duggal loxoom ci càkkuteefu ndimbal gi Mbootaay mii ñu dupee Association Enfant Soleil, di am mbootaay muy yëngu ci gune yi, doon amal ñeel xale yi ànd ak laago ba mu tere leen bokk ak seen i moroom yi dara jotul.

Ci seen càkkuteefu ndimbal googu, mbootaay mi bëgg na cee am 100i tamndaret (miliyoŋ) ci FCFA ngir matal i sémbam, rawatina tabax i kër yu mën a dalal xale yooyu, muy ay Këri Mboq (Maison jaunes), ci diiwaan yépp.

Moom jëwriñu njàng mi ci daara yu ndaw yeek yu digg-dóomu yi, gaawantu na ci ngir xamle ni mébatam mooy amal lekkool boo xam ni du beddi kenn. Dige na fa tamit ni dina gàddu peyooru liggéeykat yiy taxawu xale yooyu ci daara yi ñu leen beral

SÀCC BI ÑU FAAT FA TUUBAA

Fa Tuubaa, benn sàcc lañu fa dóor ba faat bakkanam. Sàcc boobu nag, dafa bokkoon ci 7i defkati ñaawteef yu duggoon ca jawu “Ocass” bu Tuubaa, daldi fay dàjji 11i bitig, yóbbaale 1,4 tamndaret ciy FCFA ak benn jollasu.

Waaye, bi ñu jógee foofu, dañ song genn kër gu ay baana-baana dëkk, nangu seen i alal. Ci noonu la leen dëkkandoo ya wallusee, xeex ak ñoom ba jàpp ci kenn. Ci la ko mbooloo ma daldi singali, dóor ko ba mu jaare fa faatu.

EKIB NASIYONAAL

Saajo Maane du bokk ci ñaari joŋante yi ekibu Senegaal bi war a amal ci digganteem ak Kongoo (6 suwe) ak Móritani (9 siwe). Mbootaayu Senegaal mi yore powum kuppe gi moo siiwal xibaar bi. Ci yégle bi ñu génne, Saajo Maane dafa ñëwaale ak metit ci wóomam bi mu jógee Araabi Sawdit. Ginnaaw bi ñu ko saytoo lañ gis ni gaañu-gaañu yi mu am mayu ko mu bokk ci ñaari joŋante yi. Bu dee lu jëm ci Aaróona Sangate itam, xamle nañ ni moo ngi doon yëg metit ci mole bi waaye fajkat yee ngi koy topp.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj